Ghafir · 32/85
Tekki Waxtaan — Simoore Ghafir
وَيَا قَوْمِ إِنِّي أَخَافُ عَلَيْكُمْ يَوْمَ التَّنَادِ ۝٣٢
Wa yaa qawmi inneee akhaafu `alaikum yawmat tanaad
📖 Tekkim Wolof
“Éy yéen samaw nit, ragal naa ci yéen bisub wootante ba,

🎧 Dégg


📜 Aaya 30-34 — Simoore Ghafir

30وَقَالَ الَّذِي آمَنَ يَا قَوْمِ إِنِّي أَخَافُ عَلَيْكُم مِّثْلَ يَوْمِ الْأَحْزَابِ
Ka gëmoon daldi waxaat ne : "Yéen samaw nit, ragal naa ci yéen lu mel ni bis ba farandoo ya doon xare.
31مِثْلَ دَأْبِ قَوْمِ نُوحٍ وَعَادٍ وَثَمُودَ وَالَّذِينَ مِن بَعْدِهِمْ ۚ وَمَا اللَّهُ يُرِيدُ ظُلْمًا لِّلْعِبَادِ
Lu melni lëgg-lëggub nitu Nooh, ak Aad ak Samuud, ak ña leen mujjoon”. Te Yàlla bëggul ag tooñ ci jaamam ñi.
32وَيَا قَوْمِ إِنِّي أَخَافُ عَلَيْكُمْ يَوْمَ التَّنَادِ
“Éy yéen samaw nit, ragal naa ci yéen bisub wootante ba,
33يَوْمَ تُوَلُّونَ مُدْبِرِينَ مَا لَكُم مِّنَ اللَّهِ مِنْ عَاصِمٍ ۗ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِنْ هَادٍ
Bis ba ngeen di wane sànku, te dungeen am ku leen di aar ci Yàlla”. ku Yàlla natt ci moom réer, kenn du ko man a gindi.
34وَلَقَدْ جَاءَكُمْ يُوسُفُ مِن قَبْلُ بِالْبَيِّنَاتِ فَمَا زِلْتُمْ فِي شَكٍّ مِّمَّا جَاءَكُم بِهِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا هَلَكَ قُلْتُمْ لَن يَبْعَثَ اللَّهُ مِن بَعْدِهِ رَسُولًا ۚ كَذَٰلِكَ يُضِلُّ اللَّهُ مَنْ هُوَ مُسْرِفٌ مُّرْتَابٌ
“Yuusuf, indaloon na leen ay firnde yu leer naññ, te de ñu leen di sikki-sàkka ca la mu indiwoon. Ba mu faatoo, ngeen wax naan : “Yàlla yónniwaatul beneen Yonnent ginnaawam”. Noonu la Yàlla di réerale ñiy yàq tey sikki-sàkka.
GhafirFihi Alxuraan
85Aaya
MeccanRevelation
32Aaya

Tekki — Ghafir 32

Simoore Ghafir Aaya 32 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Éy yéen samaw nit, ragal naa ci yéen bisub wootante…

Simoore Aaya 32/85 — Simoore Ghafir غافر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Ghafir Dégg, Simoore Ghafir Tekki, Simoore Ghafir mp3, Simoore Ghafir pdf. Aaya 30–34. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers