Ghafir · 14/85
Tekki Waxtaan — Ghafir
فَادْعُوا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ وَلَوْ كَرِهَ الْكَافِرُونَ ۝١٤
Fad`ul laaha mukhliseena lahud deena wa law karihal kaafiroon
📖 Tekkim Wolof
Ñaanleen Yàlla, te jaamu Ko te sellalal ko diineem, doonte la neexul yéefar yi.

🎧 Dégg


📜 Aaya 12-16 — Ghafir

12ذَٰلِكُم بِأَنَّهُ إِذَا دُعِيَ اللَّهُ وَحْدَهُ كَفَرْتُمْ ۖ وَإِن يُشْرَكْ بِهِ تُؤْمِنُوا ۚ فَالْحُكْمُ لِلَّهِ الْعَلِيِّ الْكَبِيرِ
“...Amul ndax bu ñu masaan a woo Yàlla doŋŋ ngeen weddi ; bu ñu ko bokkaalewaale ak leneen, ngeen gëm koo. (Tey jii), àtte ba Yàllaa ko yor, moo di ku Kawe, te di ku Màgg”.
13هُوَ الَّذِي يُرِيكُمْ آيَاتِهِ وَيُنَزِّلُ لَكُم مِّنَ السَّمَاءِ رِزْقًا ۚ وَمَا يَتَذَكَّرُ إِلَّا مَن يُنِيبُ
Moo leen di won ay kéemaan, di leen wàcceel ndox, mu bawoo asamaan, ngen di ca xéewlu. Te ñay dellu [ca Yàlla] rekk ay fàttaliku.
14فَادْعُوا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ وَلَوْ كَرِهَ الْكَافِرُونَ
Ñaanleen Yàlla, te jaamu Ko te sellalal ko diineem, doonte la neexul yéefar yi.
15رَفِيعُ الدَّرَجَاتِ ذُو الْعَرْشِ يُلْقِي الرُّوحَ مِنْ أَمْرِهِ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ لِيُنذِرَ يَوْمَ التَّلَاقِ
Moo kawey daraja, di Boroom Aras, Mooy sànni ruu ci ndigalam jëme ko ci ku ko soob ci jaamam ñi, ngir muy xuppe ci bisub Daje ba (Bis Pénc ba),
16يَوْمَ هُم بَارِزُونَ ۖ لَا يَخْفَىٰ عَلَى اللَّهِ مِنْهُمْ شَيْءٌ ۚ لِّمَنِ الْمُلْكُ الْيَوْمَ ۖ لِلَّهِ الْوَاحِدِ الْقَهَّارِ
bis ba ñuy feeñ seen dara du man a nëbbu Yàlla. Ana kan mooy boroom nguur gi, bis niki tey ? Yàlla, miy Kenn, di ab Notaakoon.
GhafirFihi Alxuraan
85Aaya
MeccanRevelation
14Aaya

Tekki — Ghafir 14

Simoore Ghafir Aaya 14 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñaanleen Yàlla, te jaamu Ko te sellalal ko diineem, doonte…

Simoore Aaya 14/85 — Ghafir غافر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ghafir Dégg, Ghafir Tekki, Ghafir mp3, Ghafir pdf. Aaya 12–16. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers