Ghafir · 36/85
Tekki Waxtaan — Ghafir
وَقَالَ فِرْعَوْنُ يَا هَامَانُ ابْنِ لِي صَرْحًا لَّعَلِّي أَبْلُغُ الْأَسْبَابَ ۝٣٦
Wa qaala Fir`awnu yaa Haamaanub-ni lee sarhal la`alleee ablughul asbaab
📖 Tekkim Wolof
Firawna wax na ne : "Yaw Haamaan, tabaxal ma ag tóoj : ndax amaana ma man a gis yoon ya,
🎧 Dégg

📜 Aaya 34-38 — Ghafir

34وَلَقَدْ جَاءَكُمْ يُوسُفُ مِن قَبْلُ بِالْبَيِّنَاتِ فَمَا زِلْتُمْ فِي شَكٍّ مِّمَّا جَاءَكُم بِهِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا هَلَكَ قُلْتُمْ لَن يَبْعَثَ اللَّهُ مِن بَعْدِهِ رَسُولًا ۚ كَذَٰلِكَ يُضِلُّ اللَّهُ مَنْ هُوَ مُسْرِفٌ مُّرْتَابٌ
“Yuusuf, indaloon na leen ay firnde yu leer naññ, te de ñu leen di sikki-sàkka ca la mu indiwoon. Ba mu faatoo, ngeen wax naan : “Yàlla yónniwaatul beneen Yonnent ginnaawam”. Noonu la Yàlla di réerale ñiy yàq tey sikki-sàkka.
35الَّذِينَ يُجَادِلُونَ فِي آيَاتِ اللَّهِ بِغَيْرِ سُلْطَانٍ أَتَاهُمْ ۖ كَبُرَ مَقْتًا عِندَ اللَّهِ وَعِندَ الَّذِينَ آمَنُوا ۚ كَذَٰلِكَ يَطْبَعُ اللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ قَلْبِ مُتَكَبِّرٍ جَبَّارٍ
Ñiy dàggasante ci laaya Yàlla yi, ci lu àndul ak firnde ju leen digël jéppi gu rëy lay doon ca Yàlla ak ña gëm. Noonu la Yàlla di fatte xolub képp kuy rëy-rëylu di ponkal.
36وَقَالَ فِرْعَوْنُ يَا هَامَانُ ابْنِ لِي صَرْحًا لَّعَلِّي أَبْلُغُ الْأَسْبَابَ
Firawna wax na ne : "Yaw Haamaan, tabaxal ma ag tóoj : ndax amaana ma man a gis yoon ya,
37أَسْبَابَ السَّمَاوَاتِ فَأَطَّلِعَ إِلَىٰ إِلَٰهِ مُوسَىٰ وَإِنِّي لَأَظُنُّهُ كَاذِبًا ۚ وَكَذَٰلِكَ زُيِّنَ لِفِرْعَوْنَ سُوءُ عَمَلِهِ وَصُدَّ عَنِ السَّبِيلِ ۚ وَمَا كَيْدُ فِرْعَوْنَ إِلَّا فِي تَبَابٍ
yooni asamaan yi, ndax ma man a yërndu Yàllay Muusaa ; te man sax ay fen laa ko jàppe”. Noonu la Firawna rafetloo jëfëm ju ñaaw joojee ; sorenaak dëgg lool ; te pexem Firawna du lenn lu dul luy naaxsaay.
38وَقَالَ الَّذِي آمَنَ يَا قَوْمِ اتَّبِعُونِ أَهْدِكُمْ سَبِيلَ الرَّشَادِ
Waa ja gëmoon daldi wax ne : "Yéen samaw nit, toppleen ma. Ma gindileen jëmëleleen ci yoonu njub.
GhafirFihi Alxuraan
85Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Ghafir 36

Simoore Ghafir Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Firawna wax na ne : "Yaw Haamaan, tabaxal ma ag…

Simoore Aaya 36/85 — Ghafir غافر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ghafir Dégg, Ghafir Tekki, Ghafir mp3, Ghafir pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers