Ghafir · 9/85
Tekki Waxtaan — Simoore Ghafir
وَقِهِمُ السَّيِّئَاتِ ۚ وَمَن تَقِ السَّيِّئَاتِ يَوْمَئِذٍ فَقَدْ رَحِمْتَهُ ۚ وَذَٰلِكَ هُوَ الْفَوْزُ الْعَظِيمُ ۝٩
Wa qihimus saiyi-aat; wa man taqis saiyi-aati Yawma`izin faqad rahimtah; wa zaalika huwal fawzul `azeem
📖 Tekkim Wolof
Te nga fegalleen [mbugëlu] ñaawtéef yi. Képp koo fegal [mbugëlum] ñaawtéef, Yërëm nga ko tigi”. Te loolu mooy texe gu mag ga.

🎧 Dégg


📜 Aaya 7-11 — Simoore Ghafir

7الَّذِينَ يَحْمِلُونَ الْعَرْشَ وَمَنْ حَوْلَهُ يُسَبِّحُونَ بِحَمْدِ رَبِّهِمْ وَيُؤْمِنُونَ بِهِ وَيَسْتَغْفِرُونَ لِلَّذِينَ آمَنُوا رَبَّنَا وَسِعْتَ كُلَّ شَيْءٍ رَّحْمَةً وَعِلْمًا فَاغْفِرْ لِلَّذِينَ تَابُوا وَاتَّبَعُوا سَبِيلَكَ وَقِهِمْ عَذَابَ الْجَحِيمِ
Ña yanu Aras ak ña ko wër ña ngay sàbbaal di kañ seen Boroom, di ko gëm tey jéggalu ñi gëm naan ko : “Yaw sunu Boroom ! sa yërmaande yaatu na man a daj ñépp ak sa xam-xam. Kon jéggëlal ña daan tuub tey topp sa yoon wi te nga fegalleen mbugëlu Safara.
8رَبَّنَا وَأَدْخِلْهُمْ جَنَّاتِ عَدْنٍ الَّتِي وَعَدتَّهُمْ وَمَن صَلَحَ مِنْ آبَائِهِمْ وَأَزْوَاجِهِمْ وَذُرِّيَّاتِهِمْ ۚ إِنَّكَ أَنتَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Yaw sunu Boroom ! Tàbballeen àjjana Aden ja nga leen digoon, ak képp ku baaxoon ci seeni baay ak i maam, ak seeni soxna ak seeni sët, yaw yaa di boroom Kàttan, di ku Xereñ.
9وَقِهِمُ السَّيِّئَاتِ ۚ وَمَن تَقِ السَّيِّئَاتِ يَوْمَئِذٍ فَقَدْ رَحِمْتَهُ ۚ وَذَٰلِكَ هُوَ الْفَوْزُ الْعَظِيمُ
Te nga fegalleen [mbugëlu] ñaawtéef yi. Képp koo fegal [mbugëlum] ñaawtéef, Yërëm nga ko tigi”. Te loolu mooy texe gu mag ga.
10إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا يُنَادَوْنَ لَمَقْتُ اللَّهِ أَكْبَرُ مِن مَّقْتِكُمْ أَنفُسَكُمْ إِذْ تُدْعَوْنَ إِلَى الْإِيمَانِ فَتَكْفُرُونَ
Ña weddi nag ñoom dañu leen woo naan leen : “jéppig Yàlla moo gën a rëy ni ngeen jéppee seen bopp, ba ñu leen daan woo jëme leen ci ngëm dangeen daan weddi”.
11قَالُوا رَبَّنَا أَمَتَّنَا اثْنَتَيْنِ وَأَحْيَيْتَنَا اثْنَتَيْنِ فَاعْتَرَفْنَا بِذُنُوبِنَا فَهَلْ إِلَىٰ خُرُوجٍ مِّن سَبِيلٍ
ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, rey nga nu ñaari yoon, dundal nga nu ñaari yoon : nangu nanu sunuy bàkkaar. ndax lii man nanu tee génn” ?
GhafirFihi Alxuraan
85Aaya
MeccanRevelation
9Aaya

Tekki — Ghafir 9

Simoore Ghafir Aaya 9 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te nga fegalleen [mbugëlu] ñaawtéef yi. Képp koo fegal [mbugëlum]…

Simoore Aaya 9/85 — Simoore Ghafir غافر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Ghafir Dégg, Simoore Ghafir Tekki, Simoore Ghafir mp3, Simoore Ghafir pdf. Aaya 7–11. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers