Simoore Al-'Alaq ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-'Alaq ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (19 Aaya — مكية). Al-'Alaq Dégg, Al-'Alaq Tekki, Al-'Alaq mp3, Al-'Alaq pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-'Alaq

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
اقْرَأْ بِاسْمِ رَبِّكَ الَّذِي خَلَقَ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Jàngal, ci sa turu Boroom biy bind,
خَلَقَ الْإِنسَانَ مِنْ عَلَقٍ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
moo bind nit ci lumbu deret.
اقْرَأْ وَرَبُّكَ الْأَكْرَمُ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Jàngal ! Sa Boroom mooy ki gëna tedd,
الَّذِي عَلَّمَ بِالْقَلَمِ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
mooy kiy xamle ci xalima [mbind],
عَلَّمَ الْإِنسَانَ مَا لَمْ يَعْلَمْ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
moo xamal nit lamu xamut woon.
كَلَّا إِنَّ الْإِنسَانَ لَيَطْغَىٰ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Waaye nit kat dafay bew,
أَن رَّآهُ اسْتَغْنَىٰ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
bu gisee dafa woomal man boppam.
إِنَّ إِلَىٰ رَبِّكَ الرُّجْعَىٰ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
(Xamal ne), sa Boroom mooy delluwaay ba.
أَرَأَيْتَ الَّذِي يَنْهَىٰ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Xanaa gisoo waa jay tere
عَبْدًا إِذَا صَلَّىٰ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
ab jamub Yàlla (Muhammad) ci muy taxawal Julli ?
أَرَأَيْتَ إِن كَانَ عَلَى الْهُدَىٰ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Xanaa gisoo ni tey su nekkoon ci njub,
أَوْ أَمَرَ بِالتَّقْوَىٰ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
walla muy digale ragal Yàlla ?
أَرَأَيْتَ إِن كَذَّبَ وَتَوَلَّىٰ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Xanaa gisoo su weddi woon tey dumóoyu ?
أَلَمْ يَعْلَم بِأَنَّ اللَّهَ يَرَىٰ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Xanaa dafa xamul ne Yàllaa ngi gis ?
كَلَّا لَئِن لَّمْ يَنتَهِ لَنَسْفَعًا بِالنَّاصِيَةِ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Déedéet ! Su ko bàyyiwul, Dananu jiñ, mbaq ko,
نَاصِيَةٍ كَاذِبَةٍ خَاطِئَةٍ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
ni ñuy mbaqi, fenkat buy defkatu bàkkaar.
فَلْيَدْعُ نَادِيَهُ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Na woo gàngooram ga.
سَنَدْعُ الزَّبَانِيَةَ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Nun dananu woo wattukati (Safara).
كَلَّا لَا تُطِعْهُ وَاسْجُدْ وَاقْتَرِب ۩ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Déedéet ! Yaw dey bu ko topp ; te na ngay sujood tey jige jigelu lu (sa Boroom).
← 95 Al-'Alaq (96/114) 97 →
Jàng Simoore Al-'Alaq ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

96العلق Al-'Alaq 📚 19 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers