PDF —
19 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-'Alaq pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-'Alaq pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-'Alaq Tekki. Simoore Al-'Alaq (Meccan) 19 Aaya.

← At-TinSimoore Al-'Alaq Al-Qadr →


19 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
96:1 Jàngal, ci sa turu Boroom biy bind,
ﮛﮜﮝﮞﮟ
96:2 moo bind nit ci lumbu deret.
ﮠﮡﮢﮣ
96:3 Jàngal ! Sa Boroom mooy ki gëna tedd,
ﮤﮥﮦﮧ
96:4 mooy kiy xamle ci xalima [mbind],
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
96:5 moo xamal nit lamu xamut woon.
ﮮﮯﮰﮱﯓ
96:6 Waaye nit kat dafay bew,
ﯔﯕﯖﯗ
96:7 bu gisee dafa woomal man boppam.
ﯘﯙﯚﯛﯜ
96:8 (Xamal ne), sa Boroom mooy delluwaay ba.
ﯝﯞﯟﯠ
96:9 Xanaa gisoo waa jay tere
ﯡﯢﯣﯤ
96:10 ab jamub Yàlla (Muhammad) ci muy taxawal Julli ?
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
96:11 Xanaa gisoo ni tey su nekkoon ci njub,
ﯫﯬﯭﯮ
96:12 walla muy digale ragal Yàlla ?
ﭑﭒﭓﭔﭕ
96:13 Xanaa gisoo su weddi woon tey dumóoyu ?
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
96:14 Xanaa dafa xamul ne Yàllaa ngi gis ?
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
96:15 Déedéet ! Su ko bàyyiwul, Dananu jiñ, mbaq ko,
ﭣﭤﭥﭦ
96:16 ni ñuy mbaqi, fenkat buy defkatu bàkkaar.
ﭧﭨﭩ
96:17 Na woo gàngooram ga.
ﭪﭫﭬ
96:18 Nun dananu woo wattukati (Safara).
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
96:19 Déedéet ! Yaw dey bu ko topp ; te na ngay sujood tey jige jigelu lu (sa Boroom).

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers