An-Nahl · 104/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
إِنَّ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ لَا يَهْدِيهِمُ اللَّهُ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ ۝١٠٤
Innal lazeena laa yu`minoona bi Aayaatil laahi laa yahdehimul laahu wa lahum `azaabun aleem
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne gëmuñu kàdduy Yàlla yi, Yàlla duleen gindi. Te ñeel na leen mbugal mu metti.

🎧 Dégg


📜 Aaya 102-106 — An-Nahl

102قُلْ نَزَّلَهُ رُوحُ الْقُدُسِ مِن رَّبِّكَ بِالْحَقِّ لِيُثَبِّتَ الَّذِينَ آمَنُوا وَهُدًى وَبُشْرَىٰ لِلْمُسْلِمِينَ
Neel : “Ruu gu sell gaa ko wàcce mu jóge ci lu dëggu ngir mu dëgëral ñi gëm, muy luy gindee, di luy bégal jullit ñi.
103وَلَقَدْ نَعْلَمُ أَنَّهُمْ يَقُولُونَ إِنَّمَا يُعَلِّمُهُ بَشَرٌ ۗ لِّسَانُ الَّذِي يُلْحِدُونَ إِلَيْهِ أَعْجَمِيٌّ وَهَٰذَا لِسَانٌ عَرَبِيٌّ مُّبِينٌ
Te xam Nanu jeek la ñuy wax ne : “Nit la ku jàngul”. Muy koo xam ne aw làkkam du [araab] te lii nekk di làkku araab wu réer..
104إِنَّ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ لَا يَهْدِيهِمُ اللَّهُ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne gëmuñu kàdduy Yàlla yi, Yàlla duleen gindi. Te ñeel na leen mbugal mu metti.
105إِنَّمَا يَفْتَرِي الْكَذِبَ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ ۖ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْكَاذِبُونَ
Ca dëgg-dëgg ñay duur ay fen ñooy ña gëmul kàdduy Yàlla yi, ñoom ñooy fenkat yi.
106مَن كَفَرَ بِاللَّهِ مِن بَعْدِ إِيمَانِهِ إِلَّا مَنْ أُكْرِهَ وَقَلْبُهُ مُطْمَئِنٌّ بِالْإِيمَانِ وَلَٰكِن مَّن شَرَحَ بِالْكُفْرِ صَدْرًا فَعَلَيْهِمْ غَضَبٌ مِّنَ اللَّهِ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Ku weddi Yàlla ginnaaw ba mu gëmee... - ku dul ka ñu not fekk xelam sax na ci gëm Yàlla - ak ña ubbi seen dënn cig kéefar, mer mu tukkee ca Yàlla dana leen sadd te ñeel na leen mbugal mu màgg.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
104Aaya

Tekki — An-Nahl 104

Simoore An-Nahl Aaya 104 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne gëmuñu kàdduy Yàlla yi, Yàlla duleen…

Simoore Aaya 104/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 102–106. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers