An-Nahl · 32/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
الَّذِينَ تَتَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ طَيِّبِينَ ۙ يَقُولُونَ سَلَامٌ عَلَيْكُمُ ادْخُلُوا الْجَنَّةَ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝٣٢
Allazeena tatawaf faahumul malaaa`ikatu taiyibeena yaqooloona salaamun `alai kumud khulul Jannata bimaa kuntum ta`maloon
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne Malaaka ya danañu leen rey - fekk ñu nekk ñu sell - danañu leen wax ne : “Yal na jàmm nekk ci yéen ! Dugguleen Àjjana ci sababus la ngeen daan jëf [ci lu baax]”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 30-34 — An-Nahl

30۞ وَقِيلَ لِلَّذِينَ اتَّقَوْا مَاذَا أَنزَلَ رَبُّكُمْ ۚ قَالُوا خَيْرًا ۗ لِّلَّذِينَ أَحْسَنُوا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةٌ ۚ وَلَدَارُ الْآخِرَةِ خَيْرٌ ۚ وَلَنِعْمَ دَارُ الْمُتَّقِينَ
Ñuy wax [ña ragal seen Boroom] : “Ana lan la seen Boroom wàcce ? ”. Ñu tontu ne : “Yiw”. Ñeel na ñi rafetal ci àddina Samay teraanga ; waaye kërug àllaaxiraa gën. Te aka baax kërug way-ragal ña [seen Boroom] !
31جَنَّاتُ عَدْنٍ يَدْخُلُونَهَا تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ ۖ لَهُمْ فِيهَا مَا يَشَاءُونَ ۚ كَذَٰلِكَ يَجْزِي اللَّهُ الْمُتَّقِينَ
Àjjana ju sax la, ñu tàbbi ca, te ay dex danañuy daw-dawaan ci suufam. Te danañu fa am lu ñu bëgg ; Noonu la Yàlla di feye way-ragal ña [Yàlla].
32الَّذِينَ تَتَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ طَيِّبِينَ ۙ يَقُولُونَ سَلَامٌ عَلَيْكُمُ ادْخُلُوا الْجَنَّةَ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Ña nga xam ne Malaaka ya danañu leen rey - fekk ñu nekk ñu sell - danañu leen wax ne : “Yal na jàmm nekk ci yéen ! Dugguleen Àjjana ci sababus la ngeen daan jëf [ci lu baax]”.
33هَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا أَن تَأْتِيَهُمُ الْمَلَائِكَةُ أَوْ يَأْتِيَ أَمْرُ رَبِّكَ ۚ كَذَٰلِكَ فَعَلَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ وَمَا ظَلَمَهُمُ اللَّهُ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Lan la [yéefar ya] di xaar, Malaaka ya digal leen walla sa dogalu Boroom agsi ci ñoom ? Noonu la [yéefar ya] leen jiitu nekke woon. Waaye ñoom ñoo tooñ seen bopp.
34فَأَصَابَهُمْ سَيِّئَاتُ مَا عَمِلُوا وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ
Dal na ci seen kaw ñaawtéefu la ñu defoon, ndax wàcc na ci ñoom la ñu doon soofantal di ko reetaan.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
32Aaya

Tekki — An-Nahl 32

Simoore An-Nahl Aaya 32 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne Malaaka ya danañu leen rey -…

Simoore Aaya 32/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 30–34. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers