An-Nahl · 91/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَأَوْفُوا بِعَهْدِ اللَّهِ إِذَا عَاهَدتُّمْ وَلَا تَنقُضُوا الْأَيْمَانَ بَعْدَ تَوْكِيدِهَا وَقَدْ جَعَلْتُمُ اللَّهَ عَلَيْكُمْ كَفِيلًا ۚ إِنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ مَا تَفْعَلُونَ ۝٩١
Wa awfoo bi Ahdil laahi izaa `aahattum wa laa tanqudul aimaana ba`da tawkeedihaa wa qad ja`altumul laaha `alaikum kafeelaa; innal laaha ya`lamu maa taf`aloon
📖 Tekkim Wolof
Matal-leen kóllareg Yàlla ginnaaw ba ngeen ko fasee, buleen di fàtte la ngeen dige woon ginnaaw ba mu nekkee di lu dëgër, te ngeen def Yàlla Mu di seen seede. Yàlla dey xam na li ngeen di def !

🎧 Dégg


📜 Aaya 89-93 — An-Nahl

89وَيَوْمَ نَبْعَثُ فِي كُلِّ أُمَّةٍ شَهِيدًا عَلَيْهِم مِّنْ أَنفُسِهِمْ ۖ وَجِئْنَا بِكَ شَهِيدًا عَلَىٰ هَٰؤُلَاءِ ۚ وَنَزَّلْنَا عَلَيْكَ الْكِتَابَ تِبْيَانًا لِّكُلِّ شَيْءٍ وَهُدًى وَرَحْمَةً وَبُشْرَىٰ لِلْمُسْلِمِينَ
Te bis bu Nu dekkale ci xeet wu nekk sunu seede su nekk seede ci ñoom, Dananu la indil [yaw Muhammad] nga nekk seede ci ñooñu. Ndaxte wàcce Nanu ci yaw Téere ngir biral lépp lu nekk te muy luy gindee, di yërmaande, di mbégte ñeel ña jébbalu [diy jullit].
90۞ إِنَّ اللَّهَ يَأْمُرُ بِالْعَدْلِ وَالْإِحْسَانِ وَإِيتَاءِ ذِي الْقُرْبَىٰ وَيَنْهَىٰ عَنِ الْفَحْشَاءِ وَالْمُنكَرِ وَالْبَغْيِ ۚ يَعِظُكُمْ لَعَلَّكُمْ تَذَكَّرُونَ
Te Yàlla nag dafay digle maandute, di tere njaaloo ak lu bon ak tooñ. Mi ngi leen di waar ndaxtelee ngeen fàttaliku [seen Boroom].
91وَأَوْفُوا بِعَهْدِ اللَّهِ إِذَا عَاهَدتُّمْ وَلَا تَنقُضُوا الْأَيْمَانَ بَعْدَ تَوْكِيدِهَا وَقَدْ جَعَلْتُمُ اللَّهَ عَلَيْكُمْ كَفِيلًا ۚ إِنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ مَا تَفْعَلُونَ
Matal-leen kóllareg Yàlla ginnaaw ba ngeen ko fasee, buleen di fàtte la ngeen dige woon ginnaaw ba mu nekkee di lu dëgër, te ngeen def Yàlla Mu di seen seede. Yàlla dey xam na li ngeen di def !
92وَلَا تَكُونُوا كَالَّتِي نَقَضَتْ غَزْلَهَا مِن بَعْدِ قُوَّةٍ أَنكَاثًا تَتَّخِذُونَ أَيْمَانَكُمْ دَخَلًا بَيْنَكُمْ أَن تَكُونَ أُمَّةٌ هِيَ أَرْبَىٰ مِنْ أُمَّةٍ ۚ إِنَّمَا يَبْلُوكُمُ اللَّهُ بِهِ ۚ وَلَيُبَيِّنَنَّ لَكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ مَا كُنتُمْ فِيهِ تَخْتَلِفُونَ
Buleen mel ni ndaw sa firinci buum ga mu raw ba mu dëgër, mu firinci ko ba mu nekk i dogit, ngeen di jàppe seeni ngiñ li ngeen di wuruje ci seen diggante, ngeen defe ne ku ëpp mbooloo mën naa wor. Te Yàlla dafa leen ciy natt. Te bu Bis-pénc baa Dana leen leeralal la ngeen nekkoon di ca juyoo.
93وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ لَجَعَلَكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَلَٰكِن يُضِلُّ مَن يَشَاءُ وَيَهْدِي مَن يَشَاءُ ۚ وَلَتُسْأَلُنَّ عَمَّا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Su neexoon Yàlla Mu def leen ngeen nekk wenn xeet doŋŋ. Waaye Mooy bàyyi cig réeram ku ko soob, di gindi ku ko soob. Te fàwwu ñu laaj leen ca la ngeen defoon.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
91Aaya

Tekki — An-Nahl 91

Simoore An-Nahl Aaya 91 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Matal-leen kóllareg Yàlla ginnaaw ba ngeen ko fasee, buleen di…

Simoore Aaya 91/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 89–93. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers