Al-Isra · 13/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
وَكُلَّ إِنسَانٍ أَلْزَمْنَاهُ طَائِرَهُ فِي عُنُقِهِ ۖ وَنُخْرِجُ لَهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ كِتَابًا يَلْقَاهُ مَنشُورًا ۝١٣
Wa kulla insaanin alzamnaahu taaa`irahoo fe `unuqihee wa nukhriji lahoo Yawmal Qiyaamati kitaabany yalqaahu manshooraa
📖 Tekkim Wolof
Te nit ku nekk, tàbbal Nanu ko jëfam ci doqam. Ca Bis-pénc ba, Dananu ko génneel ab téere bu muy dajeel, ñu tàllal ko ko :

🎧 Dégg


📜 Aaya 11-15 — Al-Isra

11وَيَدْعُ الْإِنسَانُ بِالشَّرِّ دُعَاءَهُ بِالْخَيْرِ ۖ وَكَانَ الْإِنسَانُ عَجُولًا
Te nit dana ñaan lu bon ak lu baax, ndax dafa nekk di ku yàkkamti.
12وَجَعَلْنَا اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ آيَتَيْنِ ۖ فَمَحَوْنَا آيَةَ اللَّيْلِ وَجَعَلْنَا آيَةَ النَّهَارِ مُبْصِرَةً لِّتَبْتَغُوا فَضْلًا مِّن رَّبِّكُمْ وَلِتَعْلَمُوا عَدَدَ السِّنِينَ وَالْحِسَابَ ۚ وَكُلَّ شَيْءٍ فَصَّلْنَاهُ تَفْصِيلًا
Def Nanu guddi ak bëccëg ñu nekk ñaari kéemaan, te far Nanu lëndëmi guddi ak leeraayu bëccëg, ngir ngeen mën a gis, di sàkku xéewal gu jóge ci seen Boroom, ak ngir ngeen mën a xam limi at yi ak ngir ngeen mën a waññi. Te lu nekk faramfàcce Nanu ko ci anam yu leer.
13وَكُلَّ إِنسَانٍ أَلْزَمْنَاهُ طَائِرَهُ فِي عُنُقِهِ ۖ وَنُخْرِجُ لَهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ كِتَابًا يَلْقَاهُ مَنشُورًا
Te nit ku nekk, tàbbal Nanu ko jëfam ci doqam. Ca Bis-pénc ba, Dananu ko génneel ab téere bu muy dajeel, ñu tàllal ko ko :
14اقْرَأْ كِتَابَكَ كَفَىٰ بِنَفْسِكَ الْيَوْمَ عَلَيْكَ حَسِيبًا
[Nu ne ko] : “Jàngal sab téere. Sa bopp doy na la tey, sa nattub jëf yaw la war”.
15مَّنِ اهْتَدَىٰ فَإِنَّمَا يَهْتَدِي لِنَفْسِهِ ۖ وَمَن ضَلَّ فَإِنَّمَا يَضِلُّ عَلَيْهَا ۚ وَلَا تَزِرُ وَازِرَةٌ وِزْرَ أُخْرَىٰ ۗ وَمَا كُنَّا مُعَذِّبِينَ حَتَّىٰ نَبْعَثَ رَسُولًا
Ku jub, boppam la ko defal ; ku dëng boppam la ko def. Ndax kenn du yenu yenu keneen. Te nekkunu woon di Aji-mbugal wenn xeet te yónniwunu ab Yonent ca ñoom.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
13Aaya

Tekki — Al-Isra 13

Simoore Al-Isra Aaya 13 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te nit ku nekk, tàbbal Nanu ko jëfam ci doqam.…

Simoore Aaya 13/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 11–15. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers