Al-Isra · 3/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
ذُرِّيَّةَ مَنْ حَمَلْنَا مَعَ نُوحٍ ۚ إِنَّهُ كَانَ عَبْدًا شَكُورًا ۝٣
Zurriyyata man hamalnaa ma`a Nooh innahoo kaana `abdan shakooraa
📖 Tekkim Wolof
Ñoo di sëti ña àndoon ak Nooh ca gaal ga te Nu musaloon leen. Nooh jaam la bu daan sant Boroomam.
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-5 — Al-Isra

1سُبْحَانَ الَّذِي أَسْرَىٰ بِعَبْدِهِ لَيْلًا مِّنَ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ إِلَى الْمَسْجِدِ الْأَقْصَى الَّذِي بَارَكْنَا حَوْلَهُ لِنُرِيَهُ مِنْ آيَاتِنَا ۚ إِنَّهُ هُوَ السَّمِيعُ الْبَصِيرُ
Tudd naa sellug Ka nga xam ne Moo rañaane woon jaamam ba Muhammad [yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko] jële ko Màkka yóbbu ko Baytil Muqaddas [Al qudsu], muy dëkk boo xam ne wurumam barkeel na, ngir Nu won ko ci Sunuy kéemaan,Yàlla mooy Kiy dégg, mooy Kiy gis.
2وَآتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ وَجَعَلْنَاهُ هُدًى لِّبَنِي إِسْرَائِيلَ أَلَّا تَتَّخِذُوا مِن دُونِي وَكِيلًا
Indil Nanu Muusaa ab Téere, def ko mu di ag njub ngir Banii-Israayiila [aw xeetam] te ñu bañ a jàppee keneen wéeruwaay.
3ذُرِّيَّةَ مَنْ حَمَلْنَا مَعَ نُوحٍ ۚ إِنَّهُ كَانَ عَبْدًا شَكُورًا
Ñoo di sëti ña àndoon ak Nooh ca gaal ga te Nu musaloon leen. Nooh jaam la bu daan sant Boroomam.
4وَقَضَيْنَا إِلَىٰ بَنِي إِسْرَائِيلَ فِي الْكِتَابِ لَتُفْسِدُنَّ فِي الْأَرْضِ مَرَّتَيْنِ وَلَتَعْلُنَّ عُلُوًّا كَبِيرًا
Nu leeral giiru Banii-Israayiila ca Téere ba, ne leen : “Dangeen yàq ci suuf si ñaari yoon, te it dangeen beew beew gu rëy”.
5فَإِذَا جَاءَ وَعْدُ أُولَاهُمَا بَعَثْنَا عَلَيْكُمْ عِبَادًا لَّنَا أُولِي بَأْسٍ شَدِيدٍ فَجَاسُوا خِلَالَ الدِّيَارِ ۚ وَكَانَ وَعْدًا مَّفْعُولًا
Ba dig bu njëkk ba agsee, Dananu yónni te yebal ci seen kaw Sunuy jaam yu am kàttan gu tar ñu songe leen ci seen biir kër. Loolu dig buy ñëw la.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
3Aaya

Tekki — Al-Isra 3

Simoore Al-Isra Aaya 3 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñoo di sëti ña àndoon ak Nooh ca gaal ga…

Simoore Aaya 3/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 1–5. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers