Al-Kahf · 56/110
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Kahf
وَمَا نُرْسِلُ الْمُرْسَلِينَ إِلَّا مُبَشِّرِينَ وَمُنذِرِينَ ۚ وَيُجَادِلُ الَّذِينَ كَفَرُوا بِالْبَاطِلِ لِيُدْحِضُوا بِهِ الْحَقَّ ۖ وَاتَّخَذُوا آيَاتِي وَمَا أُنذِرُوا هُزُوًا ۝٥٦
Wa maa nursilul mursaleena illaa mubashshireena wa munzireen; wa yujaadilul lazeena kafaroo bilbaatili liyudhidoo bihil haqqa wattakhazooo Aayaatee wa maaa unziroo huzuwaa
📖 Tekkim Wolof
Dunu yónni Yonent yi lu dul ngir ñuy bégle, di xuppe. Te ña weddi di dàggasante cig neen, ngir bëgg cee yàq dëgg ga, di weddi Sunuy kàddu ak la ñu leen di waare.

🎧 Dégg


📜 Aaya 54-58 — Simoore Al-Kahf

54وَلَقَدْ صَرَّفْنَا فِي هَٰذَا الْقُرْآنِ لِلنَّاسِ مِن كُلِّ مَثَلٍ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ أَكْثَرَ شَيْءٍ جَدَلًا
Te Nun biral nanu ci Alxuraan jii, ngir nit ñi, léebu wu nekk. Waaye nit mooy ki gën a mën a dàggasante ci mbindeef yi.
55وَمَا مَنَعَ النَّاسَ أَن يُؤْمِنُوا إِذْ جَاءَهُمُ الْهُدَىٰ وَيَسْتَغْفِرُوا رَبَّهُمْ إِلَّا أَن تَأْتِيَهُمْ سُنَّةُ الْأَوَّلِينَ أَوْ يَأْتِيَهُمُ الْعَذَابُ قُبُلًا
Li tere nit ñi ñu gëm ba leen njub ga dikkalee, te ñu baalu seen Boroom, lu dul dañoo bëgg mu dikkal leen la daloon seen maam ya, walla mbugal dikkal leen [mu leen bett] jàkkaarlook ñoom.
56وَمَا نُرْسِلُ الْمُرْسَلِينَ إِلَّا مُبَشِّرِينَ وَمُنذِرِينَ ۚ وَيُجَادِلُ الَّذِينَ كَفَرُوا بِالْبَاطِلِ لِيُدْحِضُوا بِهِ الْحَقَّ ۖ وَاتَّخَذُوا آيَاتِي وَمَا أُنذِرُوا هُزُوًا
Dunu yónni Yonent yi lu dul ngir ñuy bégle, di xuppe. Te ña weddi di dàggasante cig neen, ngir bëgg cee yàq dëgg ga, di weddi Sunuy kàddu ak la ñu leen di waare.
57وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن ذُكِّرَ بِآيَاتِ رَبِّهِ فَأَعْرَضَ عَنْهَا وَنَسِيَ مَا قَدَّمَتْ يَدَاهُ ۚ إِنَّا جَعَلْنَا عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ أَكِنَّةً أَن يَفْقَهُوهُ وَفِي آذَانِهِمْ وَقْرًا ۖ وَإِن تَدْعُهُمْ إِلَى الْهُدَىٰ فَلَن يَهْتَدُوا إِذًا أَبَدًا
Ana ku gën a tooñ ku ñu waar ci kàdduy Boroomam, mu dëddu te fàtte la yaari yoxoom doon jëf ? Nun def nanu ci seeni xol muuraay ngir duñu ca am dégg-dégg ak i saañ ca seeni nopp. Tax na boo leen woowee jëme leen ci njub, duñu gindiku ba fàwwu.
58وَرَبُّكَ الْغَفُورُ ذُو الرَّحْمَةِ ۖ لَوْ يُؤَاخِذُهُم بِمَا كَسَبُوا لَعَجَّلَ لَهُمُ الْعَذَابَ ۚ بَل لَّهُم مَّوْعِدٌ لَّن يَجِدُوا مِن دُونِهِ مَوْئِلًا
Te sa Boroom mooy Jéggalaakoon ba, di boroom yërmaande. Bu leen jàppe woon la ñuy fàggu [ciy jëf yu bon]. Kon Dana gaawal seen mbugal. Waaye am nañu àpp boo xam ne bu agsee, duñu am mukk ku leen musal ku dul Moom.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
56Aaya

Tekki — Al-Kahf 56

Simoore Al-Kahf Aaya 56 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dunu yónni Yonent yi lu dul ngir ñuy bégle, di…

Simoore Aaya 56/110 — Simoore Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Kahf Dégg, Simoore Al-Kahf Tekki, Simoore Al-Kahf mp3, Simoore Al-Kahf pdf. Aaya 54–58. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers