Al-Kahf · 55/110
Tekki Waxtaan — Al-Kahf
وَمَا مَنَعَ النَّاسَ أَن يُؤْمِنُوا إِذْ جَاءَهُمُ الْهُدَىٰ وَيَسْتَغْفِرُوا رَبَّهُمْ إِلَّا أَن تَأْتِيَهُمْ سُنَّةُ الْأَوَّلِينَ أَوْ يَأْتِيَهُمُ الْعَذَابُ قُبُلًا ۝٥٥
Wa maa mana`an naasa any yu`minooo iz jaaa`ahumul hudaa wa yastaghfiroo Rabbahum illaaa an taatiyahum sunnatul awwaleena aw yaatiyahumul `azaabu qubulaa
📖 Tekkim Wolof
Li tere nit ñi ñu gëm ba leen njub ga dikkalee, te ñu baalu seen Boroom, lu dul dañoo bëgg mu dikkal leen la daloon seen maam ya, walla mbugal dikkal leen [mu leen bett] jàkkaarlook ñoom.

🎧 Dégg


📜 Aaya 53-57 — Al-Kahf

53وَرَأَى الْمُجْرِمُونَ النَّارَ فَظَنُّوا أَنَّهُم مُّوَاقِعُوهَا وَلَمْ يَجِدُوا عَنْهَا مَصْرِفًا
Te saay-saay sa jenook Safara daldi foog ne dañu cay tàbbi te duñu ca am aw rawtukaay bu ñu ca rëccee.
54وَلَقَدْ صَرَّفْنَا فِي هَٰذَا الْقُرْآنِ لِلنَّاسِ مِن كُلِّ مَثَلٍ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ أَكْثَرَ شَيْءٍ جَدَلًا
Te Nun biral nanu ci Alxuraan jii, ngir nit ñi, léebu wu nekk. Waaye nit mooy ki gën a mën a dàggasante ci mbindeef yi.
55وَمَا مَنَعَ النَّاسَ أَن يُؤْمِنُوا إِذْ جَاءَهُمُ الْهُدَىٰ وَيَسْتَغْفِرُوا رَبَّهُمْ إِلَّا أَن تَأْتِيَهُمْ سُنَّةُ الْأَوَّلِينَ أَوْ يَأْتِيَهُمُ الْعَذَابُ قُبُلًا
Li tere nit ñi ñu gëm ba leen njub ga dikkalee, te ñu baalu seen Boroom, lu dul dañoo bëgg mu dikkal leen la daloon seen maam ya, walla mbugal dikkal leen [mu leen bett] jàkkaarlook ñoom.
56وَمَا نُرْسِلُ الْمُرْسَلِينَ إِلَّا مُبَشِّرِينَ وَمُنذِرِينَ ۚ وَيُجَادِلُ الَّذِينَ كَفَرُوا بِالْبَاطِلِ لِيُدْحِضُوا بِهِ الْحَقَّ ۖ وَاتَّخَذُوا آيَاتِي وَمَا أُنذِرُوا هُزُوًا
Dunu yónni Yonent yi lu dul ngir ñuy bégle, di xuppe. Te ña weddi di dàggasante cig neen, ngir bëgg cee yàq dëgg ga, di weddi Sunuy kàddu ak la ñu leen di waare.
57وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن ذُكِّرَ بِآيَاتِ رَبِّهِ فَأَعْرَضَ عَنْهَا وَنَسِيَ مَا قَدَّمَتْ يَدَاهُ ۚ إِنَّا جَعَلْنَا عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ أَكِنَّةً أَن يَفْقَهُوهُ وَفِي آذَانِهِمْ وَقْرًا ۖ وَإِن تَدْعُهُمْ إِلَى الْهُدَىٰ فَلَن يَهْتَدُوا إِذًا أَبَدًا
Ana ku gën a tooñ ku ñu waar ci kàdduy Boroomam, mu dëddu te fàtte la yaari yoxoom doon jëf ? Nun def nanu ci seeni xol muuraay ngir duñu ca am dégg-dégg ak i saañ ca seeni nopp. Tax na boo leen woowee jëme leen ci njub, duñu gindiku ba fàwwu.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
55Aaya

Tekki — Al-Kahf 55

Simoore Al-Kahf Aaya 55 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Li tere nit ñi ñu gëm ba leen njub ga…

Simoore Aaya 55/110 — Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Kahf Dégg, Al-Kahf Tekki, Al-Kahf mp3, Al-Kahf pdf. Aaya 53–57. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers