Al-Baqara · 94/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
قُلْ إِن كَانَتْ لَكُمُ الدَّارُ الْآخِرَةُ عِندَ اللَّهِ خَالِصَةً مِّن دُونِ النَّاسِ فَتَمَنَّوُا الْمَوْتَ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٩٤
Qul in kaanat lakumud Daarul Aakhiratu `indal laahi khaalisatam min doonin naasi fatamannawul mawta in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
- Waxal ne : “Ndegam am ngeen kërug àllaaxira ca Yàlla, gu yéen doŋŋ jagoo waliis nit ñi, mébétleen dee kon ndegam ñu dëggu ngeen ! ”
🎧 Dégg

📜 Aaya 92-96 — Al-Baqara

92۞ وَلَقَدْ جَاءَكُم مُّوسَىٰ بِالْبَيِّنَاتِ ثُمَّ اتَّخَذْتُمُ الْعِجْلَ مِن بَعْدِهِ وَأَنتُمْ ظَالِمُونَ
Wóor na céŋŋ ne Muusaa digaloon na leen àndak ay kéemaam yu leer. Ba noppi ngeen jaamu sëll wa ginnaawam, ngeen di way-tooñ.
93وَإِذْ أَخَذْنَا مِيثَاقَكُمْ وَرَفَعْنَا فَوْقَكُمُ الطُّورَ خُذُوا مَا آتَيْنَاكُم بِقُوَّةٍ وَاسْمَعُوا ۖ قَالُوا سَمِعْنَا وَعَصَيْنَا وَأُشْرِبُوا فِي قُلُوبِهِمُ الْعِجْلَ بِكُفْرِهِمْ ۚ قُلْ بِئْسَمَا يَأْمُرُكُم بِهِ إِيمَانُكُمْ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
[Fàttalikuleen], ba Nu wólleranteek yéen, te Nu yékkati doj wa mu tiim leen, [Ma ne leen] : “Jàppleen te farlu ci la Ma leen jox te ngeen dégg [ndigal] ! ”. Ñu ne : “Dégg nanu te bañ nanu”. Nàndaleef na leen seeni xol sëll wa ngir seenug weddi. Neel : “Bon na li leen seen ngëm digal ci loolu ndegam gëm ngeen”.
94قُلْ إِن كَانَتْ لَكُمُ الدَّارُ الْآخِرَةُ عِندَ اللَّهِ خَالِصَةً مِّن دُونِ النَّاسِ فَتَمَنَّوُا الْمَوْتَ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
- Waxal ne : “Ndegam am ngeen kërug àllaaxira ca Yàlla, gu yéen doŋŋ jagoo waliis nit ñi, mébétleen dee kon ndegam ñu dëggu ngeen ! ”
95وَلَن يَتَمَنَّوْهُ أَبَدًا بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيهِمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِالظَّالِمِينَ
Duñu ko mébét mukk ngir la seen yoxo ya jëf [ci lu bon]. Yàlla ku xam la way-tooñ ña.
96وَلَتَجِدَنَّهُمْ أَحْرَصَ النَّاسِ عَلَىٰ حَيَاةٍ وَمِنَ الَّذِينَ أَشْرَكُوا ۚ يَوَدُّ أَحَدُهُمْ لَوْ يُعَمَّرُ أَلْفَ سَنَةٍ وَمَا هُوَ بِمُزَحْزِحِهِ مِنَ الْعَذَابِ أَن يُعَمَّرَ ۗ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِمَا يَعْمَلُونَ
Wóor na ne danga leen fekk ñoom [Yahuud ya] ñu nekk di ñu gën a xér ci nit ñi ci bëgg dundu, ak ci ñiy bokkaale. [Danga ca gis] ca ñoom ku ne siiw ñu guddal fanam junniy at. Waaye du ko soreel mbugal ma! Dundu gu guddu googu Yàllaa ngi ne jàkk ci li ñuy def.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
94Aaya

Tekki — Al-Baqara 94

Simoore Al-Baqara Aaya 94 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : - Waxal ne : “Ndegam am ngeen kërug àllaaxira ca…

Simoore Aaya 94/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 92–96. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers