Al-Hajj · 27/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
وَأَذِّن فِي النَّاسِ بِالْحَجِّ يَأْتُوكَ رِجَالًا وَعَلَىٰ كُلِّ ضَامِرٍ يَأْتِينَ مِن كُلِّ فَجٍّ عَمِيقٍ ۝٢٧
Wa azzin fin naasi bil Hajji yaatooka rijaalanw wa `alaa kulli daamiriny yaateena min kulli fajjin `ameeq
📖 Tekkim Wolof
Te nanga woote ci nit ñi ngir aji Màkka. Danañu la dikkal ñuy dox ak ñeneen ñuy war xeetu waruwaay wu ne, jóge ca barab yu soree,

🎧 Dégg


📜 Aaya 25-29 — Al-Hajj

25إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ وَالْمَسْجِدِ الْحَرَامِ الَّذِي جَعَلْنَاهُ لِلنَّاسِ سَوَاءً الْعَاكِفُ فِيهِ وَالْبَادِ ۚ وَمَن يُرِدْ فِيهِ بِإِلْحَادٍ بِظُلْمٍ نُّذِقْهُ مِنْ عَذَابٍ أَلِيمٍ
Ña weddi tey wëlbatiku jëm ci yoonu Yàlla ak ca Jàkka ju ñu wormaal ja Nu def muy jëmukaay ci nit ñi : te aji-dëkk ak gan ñoo ca yem kepp... Ku fa bëgg a jeng ngir tooñ, Dananu ko musal mbugal mu tar,
26وَإِذْ بَوَّأْنَا لِإِبْرَاهِيمَ مَكَانَ الْبَيْتِ أَن لَّا تُشْرِكْ بِي شَيْئًا وَطَهِّرْ بَيْتِيَ لِلطَّائِفِينَ وَالْقَائِمِينَ وَالرُّكَّعِ السُّجُودِ
Fàttalikul ba Nu biralee Ibraahiima bérabu néeg ba [Kaaba ga], ne ko : “Bul ma bokkaaleek dara te nga laabal sama néeg ngir ñi koy wër, ña fay taxaw, di sukk di sujjóot”
27وَأَذِّن فِي النَّاسِ بِالْحَجِّ يَأْتُوكَ رِجَالًا وَعَلَىٰ كُلِّ ضَامِرٍ يَأْتِينَ مِن كُلِّ فَجٍّ عَمِيقٍ
Te nanga woote ci nit ñi ngir aji Màkka. Danañu la dikkal ñuy dox ak ñeneen ñuy war xeetu waruwaay wu ne, jóge ca barab yu soree,
28لِّيَشْهَدُوا مَنَافِعَ لَهُمْ وَيَذْكُرُوا اسْمَ اللَّهِ فِي أَيَّامٍ مَّعْلُومَاتٍ عَلَىٰ مَا رَزَقَهُم مِّن بَهِيمَةِ الْأَنْعَامِ ۖ فَكُلُوا مِنْهَا وَأَطْعِمُوا الْبَائِسَ الْفَقِيرَ
ngir ñu tase fa ak seeni njariñ tey tudd turu Yàlla ci ay bis yu ñu xam, ca la Mu leen wërsëgale ci mala yi ngeen di dunde, “Kon lekkleen ca te nangeen ca leel ñu ñàkk ña amul dara.
29ثُمَّ لْيَقْضُوا تَفَثَهُمْ وَلْيُوفُوا نُذُورَهُمْ وَلْيَطَّوَّفُوا بِالْبَيْتِ الْعَتِيقِ
Bu ñu noppee, nañu dindi seeni tilim, sangu, wattu, mottali seeni yéene, daldi wër néeg bu yàgg a yàgg ba (Kaaba ga)”.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
27Aaya

Tekki — Al-Hajj 27

Simoore Al-Hajj Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te nanga woote ci nit ñi ngir aji Màkka. Danañu…

Simoore Aaya 27/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers