Al-Hajj · 28/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
لِّيَشْهَدُوا مَنَافِعَ لَهُمْ وَيَذْكُرُوا اسْمَ اللَّهِ فِي أَيَّامٍ مَّعْلُومَاتٍ عَلَىٰ مَا رَزَقَهُم مِّن بَهِيمَةِ الْأَنْعَامِ ۖ فَكُلُوا مِنْهَا وَأَطْعِمُوا الْبَائِسَ الْفَقِيرَ ۝٢٨
Li yashhadoo manaafi`a lahum wa yazkurus mal laahi feee ayyaamimma`loomaatin `alaa maa razaqahum mim baheematil an`aami fakuloo minhaa wa at`imul baaa`isal faqeer
📖 Tekkim Wolof
ngir ñu tase fa ak seeni njariñ tey tudd turu Yàlla ci ay bis yu ñu xam, ca la Mu leen wërsëgale ci mala yi ngeen di dunde, “Kon lekkleen ca te nangeen ca leel ñu ñàkk ña amul dara.
🎧 Dégg

📜 Aaya 26-30 — Al-Hajj

26وَإِذْ بَوَّأْنَا لِإِبْرَاهِيمَ مَكَانَ الْبَيْتِ أَن لَّا تُشْرِكْ بِي شَيْئًا وَطَهِّرْ بَيْتِيَ لِلطَّائِفِينَ وَالْقَائِمِينَ وَالرُّكَّعِ السُّجُودِ
Fàttalikul ba Nu biralee Ibraahiima bérabu néeg ba [Kaaba ga], ne ko : “Bul ma bokkaaleek dara te nga laabal sama néeg ngir ñi koy wër, ña fay taxaw, di sukk di sujjóot”
27وَأَذِّن فِي النَّاسِ بِالْحَجِّ يَأْتُوكَ رِجَالًا وَعَلَىٰ كُلِّ ضَامِرٍ يَأْتِينَ مِن كُلِّ فَجٍّ عَمِيقٍ
Te nanga woote ci nit ñi ngir aji Màkka. Danañu la dikkal ñuy dox ak ñeneen ñuy war xeetu waruwaay wu ne, jóge ca barab yu soree,
28لِّيَشْهَدُوا مَنَافِعَ لَهُمْ وَيَذْكُرُوا اسْمَ اللَّهِ فِي أَيَّامٍ مَّعْلُومَاتٍ عَلَىٰ مَا رَزَقَهُم مِّن بَهِيمَةِ الْأَنْعَامِ ۖ فَكُلُوا مِنْهَا وَأَطْعِمُوا الْبَائِسَ الْفَقِيرَ
ngir ñu tase fa ak seeni njariñ tey tudd turu Yàlla ci ay bis yu ñu xam, ca la Mu leen wërsëgale ci mala yi ngeen di dunde, “Kon lekkleen ca te nangeen ca leel ñu ñàkk ña amul dara.
29ثُمَّ لْيَقْضُوا تَفَثَهُمْ وَلْيُوفُوا نُذُورَهُمْ وَلْيَطَّوَّفُوا بِالْبَيْتِ الْعَتِيقِ
Bu ñu noppee, nañu dindi seeni tilim, sangu, wattu, mottali seeni yéene, daldi wër néeg bu yàgg a yàgg ba (Kaaba ga)”.
30ذَٰلِكَ وَمَن يُعَظِّمْ حُرُمَاتِ اللَّهِ فَهُوَ خَيْرٌ لَّهُ عِندَ رَبِّهِ ۗ وَأُحِلَّتْ لَكُمُ الْأَنْعَامُ إِلَّا مَا يُتْلَىٰ عَلَيْكُمْ ۖ فَاجْتَنِبُوا الرِّجْسَ مِنَ الْأَوْثَانِ وَاجْتَنِبُوا قَوْلَ الزُّورِ
Looloo wér, te képp ku màggal jaamukaayu Yàlla ba, loolumoo gën ci moom fa Boroomam. Te mu dagan ci yéen juri kër yi ginnaaw ya mu leen limal (ca saaru Ndën la). Kon nangeen wattandiku sobes xërëm yi te wattandiku waxi caaxaan, ay fen.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
28Aaya

Tekki — Al-Hajj 28

Simoore Al-Hajj Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ngir ñu tase fa ak seeni njariñ tey tudd turu…

Simoore Aaya 28/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 26–30. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers