Al-Qasas · 76/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
۞ إِنَّ قَارُونَ كَانَ مِن قَوْمِ مُوسَىٰ فَبَغَىٰ عَلَيْهِمْ ۖ وَآتَيْنَاهُ مِنَ الْكُنُوزِ مَا إِنَّ مَفَاتِحَهُ لَتَنُوءُ بِالْعُصْبَةِ أُولِي الْقُوَّةِ إِذْ قَالَ لَهُ قَوْمُهُ لَا تَفْرَحْ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ الْفَرِحِينَ ۝٧٦
Inna Qaaroona kaana min qawmi Moosaa fabaghaaa `alaihim wa aatainaahu minal kunoozi maaa inna mafaati hahoo latanooo`u bil`usbati ulil quwwati iz qaala lahoo qawmuhoo laa tafrah innal laahaa laa yuhibbul fariheen
📖 Tekkim Wolof
[Bir na ne], Xaaruuna ci nitu Muusaa la bokkoon, waaye dafa bewoon. Joxoon Nanu ko ci ay ndàmb, loo xam ne, bu ñu lewaa caabi ya mu diis gann ay ponkal. Fàttalikul ba ko ay nitam waxee ne ko : “Bul rëy-rëylu. Yàlla safoowul ñuy rëy-rëylu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 74-78 — Al-Qasas

74وَيَوْمَ يُنَادِيهِمْ فَيَقُولُ أَيْنَ شُرَكَائِيَ الَّذِينَ كُنتُمْ تَزْعُمُونَ
Ak bis ba Mu leen di woo naan leen : “Ana ña ngeen Ma doon bokkaaleel ? ”
75وَنَزَعْنَا مِن كُلِّ أُمَّةٍ شَهِيدًا فَقُلْنَا هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ فَعَلِمُوا أَنَّ الْحَقَّ لِلَّهِ وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Nu rocci ci xeet wu nekk seede, daldi ne leen : “Indileen seeni firnde”. Ñu daldi xam ne dëgg Yàllaa ko moom ; la ñu daan sos réer leen.
76۞ إِنَّ قَارُونَ كَانَ مِن قَوْمِ مُوسَىٰ فَبَغَىٰ عَلَيْهِمْ ۖ وَآتَيْنَاهُ مِنَ الْكُنُوزِ مَا إِنَّ مَفَاتِحَهُ لَتَنُوءُ بِالْعُصْبَةِ أُولِي الْقُوَّةِ إِذْ قَالَ لَهُ قَوْمُهُ لَا تَفْرَحْ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ الْفَرِحِينَ
[Bir na ne], Xaaruuna ci nitu Muusaa la bokkoon, waaye dafa bewoon. Joxoon Nanu ko ci ay ndàmb, loo xam ne, bu ñu lewaa caabi ya mu diis gann ay ponkal. Fàttalikul ba ko ay nitam waxee ne ko : “Bul rëy-rëylu. Yàlla safoowul ñuy rëy-rëylu.
77وَابْتَغِ فِيمَا آتَاكَ اللَّهُ الدَّارَ الْآخِرَةَ ۖ وَلَا تَنسَ نَصِيبَكَ مِنَ الدُّنْيَا ۖ وَأَحْسِن كَمَا أَحْسَنَ اللَّهُ إِلَيْكَ ۖ وَلَا تَبْغِ الْفَسَادَ فِي الْأَرْضِ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ الْمُفْسِدِينَ
Li la Yàlla jox, sàkku ci kërug àllaaxira [Àjjana]. Te bul fàtte sa wàll ci àdduna. Te nangay rafetal kem ni Yàlla di rafetale jëme ci yaw. Bul di sàkku ag yàq ci suuf si. Ndax Yàlla dey safoowul yàqkat yi”.
78قَالَ إِنَّمَا أُوتِيتُهُ عَلَىٰ عِلْمٍ عِندِي ۚ أَوَلَمْ يَعْلَمْ أَنَّ اللَّهَ قَدْ أَهْلَكَ مِن قَبْلِهِ مِنَ الْقُرُونِ مَنْ هُوَ أَشَدُّ مِنْهُ قُوَّةً وَأَكْثَرُ جَمْعًا ۚ وَلَا يُسْأَلُ عَن ذُنُوبِهِمُ الْمُجْرِمُونَ
Xaaruuna wax ne : “Lii ci sama xam-xam laa ko ame”. Xanaa moom dafa xamul ña Yàlla faagaagal ca maas ya ko jiitu, ña ko gënoon a ñàng ëpp ko fuuf dooleek alal ? Te tooñkat ña deefuleen laaj seen bàkkaar !
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
76Aaya

Tekki — Al-Qasas 76

Simoore Al-Qasas Aaya 76 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Bir na ne], Xaaruuna ci nitu Muusaa la bokkoon, waaye…

Simoore Aaya 76/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 74–78. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers