Al-Qasas · 75/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
وَنَزَعْنَا مِن كُلِّ أُمَّةٍ شَهِيدًا فَقُلْنَا هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ فَعَلِمُوا أَنَّ الْحَقَّ لِلَّهِ وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ ۝٧٥
Wa naza`naa min kulli ummatin shaheedan faqulnaa haatoo burhaanakum fa`alimooo annal haqqa lillaahi wa dalla `anhum maa kaanoo yaftaroon
📖 Tekkim Wolof
Nu rocci ci xeet wu nekk seede, daldi ne leen : “Indileen seeni firnde”. Ñu daldi xam ne dëgg Yàllaa ko moom ; la ñu daan sos réer leen.
🎧 Dégg

📜 Aaya 73-77 — Al-Qasas

73وَمِن رَّحْمَتِهِ جَعَلَ لَكُمُ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ لِتَسْكُنُوا فِيهِ وَلِتَبْتَغُوا مِن فَضْلِهِ وَلَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Ci yërmaandeem la leen defalee guddeek bëccëg ngir ngeen di ca dal ak a sàkku wërsëg, ak it ngir sant Ko.
74وَيَوْمَ يُنَادِيهِمْ فَيَقُولُ أَيْنَ شُرَكَائِيَ الَّذِينَ كُنتُمْ تَزْعُمُونَ
Ak bis ba Mu leen di woo naan leen : “Ana ña ngeen Ma doon bokkaaleel ? ”
75وَنَزَعْنَا مِن كُلِّ أُمَّةٍ شَهِيدًا فَقُلْنَا هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ فَعَلِمُوا أَنَّ الْحَقَّ لِلَّهِ وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Nu rocci ci xeet wu nekk seede, daldi ne leen : “Indileen seeni firnde”. Ñu daldi xam ne dëgg Yàllaa ko moom ; la ñu daan sos réer leen.
76۞ إِنَّ قَارُونَ كَانَ مِن قَوْمِ مُوسَىٰ فَبَغَىٰ عَلَيْهِمْ ۖ وَآتَيْنَاهُ مِنَ الْكُنُوزِ مَا إِنَّ مَفَاتِحَهُ لَتَنُوءُ بِالْعُصْبَةِ أُولِي الْقُوَّةِ إِذْ قَالَ لَهُ قَوْمُهُ لَا تَفْرَحْ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ الْفَرِحِينَ
[Bir na ne], Xaaruuna ci nitu Muusaa la bokkoon, waaye dafa bewoon. Joxoon Nanu ko ci ay ndàmb, loo xam ne, bu ñu lewaa caabi ya mu diis gann ay ponkal. Fàttalikul ba ko ay nitam waxee ne ko : “Bul rëy-rëylu. Yàlla safoowul ñuy rëy-rëylu.
77وَابْتَغِ فِيمَا آتَاكَ اللَّهُ الدَّارَ الْآخِرَةَ ۖ وَلَا تَنسَ نَصِيبَكَ مِنَ الدُّنْيَا ۖ وَأَحْسِن كَمَا أَحْسَنَ اللَّهُ إِلَيْكَ ۖ وَلَا تَبْغِ الْفَسَادَ فِي الْأَرْضِ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ الْمُفْسِدِينَ
Li la Yàlla jox, sàkku ci kërug àllaaxira [Àjjana]. Te bul fàtte sa wàll ci àdduna. Te nangay rafetal kem ni Yàlla di rafetale jëme ci yaw. Bul di sàkku ag yàq ci suuf si. Ndax Yàlla dey safoowul yàqkat yi”.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
75Aaya

Tekki — Al-Qasas 75

Simoore Al-Qasas Aaya 75 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nu rocci ci xeet wu nekk seede, daldi ne leen…

Simoore Aaya 75/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 73–77. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers