Aali Imran · 72/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَقَالَت طَّائِفَةٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ آمِنُوا بِالَّذِي أُنزِلَ عَلَى الَّذِينَ آمَنُوا وَجْهَ النَّهَارِ وَاكْفُرُوا آخِرَهُ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ ۝٧٢
Wa qaalat taaa`ifatum min Ahlil Kitaabi aaminoo billazeee unzila `alal lazeena aamanoo wajhan nahaari wakfurooo aakhirahoo la`alla hum yarji`oon
📖 Tekkim Wolof
Am na ci ñoñ-téere kurél bu wax ne : “Gëmleen li wàcc ca way-gëm ña [Alxuraan] ci suba [waxtu], te bu ngoonee ngeen weddi ko, ndax ñi gëmoon ñoom it weddi.

🎧 Dégg


📜 Aaya 70-74 — Simoore Aali Imran

70يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَكْفُرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَأَنتُمْ تَشْهَدُونَ
Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di weddi kàddug Yàlla, te ngeen di ci ay seede [xam ko xéll] ?
71يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَلْبِسُونَ الْحَقَّ بِالْبَاطِلِ وَتَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ
Yéen ñoñ-téere, lan moo tax ngeen di muure dëgg ak ay caaxaan, di nëbb dëgg te xam ko ?
72وَقَالَت طَّائِفَةٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ آمِنُوا بِالَّذِي أُنزِلَ عَلَى الَّذِينَ آمَنُوا وَجْهَ النَّهَارِ وَاكْفُرُوا آخِرَهُ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Am na ci ñoñ-téere kurél bu wax ne : “Gëmleen li wàcc ca way-gëm ña [Alxuraan] ci suba [waxtu], te bu ngoonee ngeen weddi ko, ndax ñi gëmoon ñoom it weddi.
73وَلَا تُؤْمِنُوا إِلَّا لِمَن تَبِعَ دِينَكُمْ قُلْ إِنَّ الْهُدَىٰ هُدَى اللَّهِ أَن يُؤْتَىٰ أَحَدٌ مِّثْلَ مَا أُوتِيتُمْ أَوْ يُحَاجُّوكُمْ عِندَ رَبِّكُمْ ۗ قُلْ إِنَّ الْفَضْلَ بِيَدِ اللَّهِ يُؤْتِيهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ
Te : “Buleen gëm lu dul ku topp seen diine...”. Neel [yaw Muhammad] : “Njub Yàllaa ko moom” - kon mën naa am kenn nit kuñu jox la mel ni la ngeen jot ba mën a weccee kàddu ak yéen ci mbiri seen Boroom. Neel : Ngëneel a nga ca loxo Yàlla. Dana ko jox ku ko soob. Yàlla ku yaatu la, ku xam la.
74يَخْتَصُّ بِرَحْمَتِهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ ذُو الْفَضْلِ الْعَظِيمِ
Dana jagle yërmaandeem ku ko soob. Yàllaay Boroom ngëneel lu màgg.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
72Aaya

Tekki — Aali Imran 72

Simoore Aali Imran Aaya 72 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ci ñoñ-téere kurél bu wax ne : “Gëmleen…

Simoore Aaya 72/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 70–74. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers