Aali Imran · 73/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
وَلَا تُؤْمِنُوا إِلَّا لِمَن تَبِعَ دِينَكُمْ قُلْ إِنَّ الْهُدَىٰ هُدَى اللَّهِ أَن يُؤْتَىٰ أَحَدٌ مِّثْلَ مَا أُوتِيتُمْ أَوْ يُحَاجُّوكُمْ عِندَ رَبِّكُمْ ۗ قُلْ إِنَّ الْفَضْلَ بِيَدِ اللَّهِ يُؤْتِيهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ ۝٧٣
Wa laa tu`minooo illaa liman tabi`a deenakum qul innal hudaa hudal laahi ai yu`taaa ahadum misla maaa ooteetum aw yuhaaajjookum `inda Rabbikum, qul innal fadla biyadil laah; yu`teehi mai yashaaa`; wallaahu Waasi`un `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Te : “Buleen gëm lu dul ku topp seen diine...”. Neel [yaw Muhammad] : “Njub Yàllaa ko moom” - kon mën naa am kenn nit kuñu jox la mel ni la ngeen jot ba mën a weccee kàddu ak yéen ci mbiri seen Boroom. Neel : Ngëneel a nga ca loxo Yàlla. Dana ko jox ku ko soob. Yàlla ku yaatu la, ku xam la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 71-75 — Aali Imran

71يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَلْبِسُونَ الْحَقَّ بِالْبَاطِلِ وَتَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ
Yéen ñoñ-téere, lan moo tax ngeen di muure dëgg ak ay caaxaan, di nëbb dëgg te xam ko ?
72وَقَالَت طَّائِفَةٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ آمِنُوا بِالَّذِي أُنزِلَ عَلَى الَّذِينَ آمَنُوا وَجْهَ النَّهَارِ وَاكْفُرُوا آخِرَهُ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Am na ci ñoñ-téere kurél bu wax ne : “Gëmleen li wàcc ca way-gëm ña [Alxuraan] ci suba [waxtu], te bu ngoonee ngeen weddi ko, ndax ñi gëmoon ñoom it weddi.
73وَلَا تُؤْمِنُوا إِلَّا لِمَن تَبِعَ دِينَكُمْ قُلْ إِنَّ الْهُدَىٰ هُدَى اللَّهِ أَن يُؤْتَىٰ أَحَدٌ مِّثْلَ مَا أُوتِيتُمْ أَوْ يُحَاجُّوكُمْ عِندَ رَبِّكُمْ ۗ قُلْ إِنَّ الْفَضْلَ بِيَدِ اللَّهِ يُؤْتِيهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ
Te : “Buleen gëm lu dul ku topp seen diine...”. Neel [yaw Muhammad] : “Njub Yàllaa ko moom” - kon mën naa am kenn nit kuñu jox la mel ni la ngeen jot ba mën a weccee kàddu ak yéen ci mbiri seen Boroom. Neel : Ngëneel a nga ca loxo Yàlla. Dana ko jox ku ko soob. Yàlla ku yaatu la, ku xam la.
74يَخْتَصُّ بِرَحْمَتِهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ ذُو الْفَضْلِ الْعَظِيمِ
Dana jagle yërmaandeem ku ko soob. Yàllaay Boroom ngëneel lu màgg.
75۞ وَمِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ مَنْ إِن تَأْمَنْهُ بِقِنطَارٍ يُؤَدِّهِ إِلَيْكَ وَمِنْهُم مَّنْ إِن تَأْمَنْهُ بِدِينَارٍ لَّا يُؤَدِّهِ إِلَيْكَ إِلَّا مَا دُمْتَ عَلَيْهِ قَائِمًا ۗ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَالُوا لَيْسَ عَلَيْنَا فِي الْأُمِّيِّينَ سَبِيلٌ وَيَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Am na ci ñoñ-téere ko xam ne, ku ko dénk barigo [wurus] dana la ko delloo. Am na ci koo xam ne, ku ko dénk benn dinaar, du ko delloo, ndegam taxawoo ca temm. La ko waral, dañoo wax ne : “Ñoom, dara waruleen ci seen diggante ak ña jàngul .” Dañuy wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
73Aaya

Tekki — Aali Imran 73

Simoore Aali Imran Aaya 73 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te : “Buleen gëm lu dul ku topp seen diine...”.…

Simoore Aaya 73/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 71–75. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers