Aali Imran · 71/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَلْبِسُونَ الْحَقَّ بِالْبَاطِلِ وَتَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ ۝٧١
Yaaa Ahalal Kitaabi lima talbisoonal haqqa bilbaatili wa taktumoonal haqqa wa antum ta`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Yéen ñoñ-téere, lan moo tax ngeen di muure dëgg ak ay caaxaan, di nëbb dëgg te xam ko ?
🎧 Dégg

📜 Aaya 69-73 — Aali Imran

69وَدَّت طَّائِفَةٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَوْ يُضِلُّونَكُمْ وَمَا يُضِلُّونَ إِلَّا أَنفُسَهُمْ وَمَا يَشْعُرُونَ
Am na ab kurél bu bokk ci ñoñ-téere, danañu ngéeju réeral leen. Waaye mënuñoo réeral ku dul seen bopp ; te yéguñu ko.
70يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَكْفُرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَأَنتُمْ تَشْهَدُونَ
Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di weddi kàddug Yàlla, te ngeen di ci ay seede [xam ko xéll] ?
71يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَلْبِسُونَ الْحَقَّ بِالْبَاطِلِ وَتَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ
Yéen ñoñ-téere, lan moo tax ngeen di muure dëgg ak ay caaxaan, di nëbb dëgg te xam ko ?
72وَقَالَت طَّائِفَةٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ آمِنُوا بِالَّذِي أُنزِلَ عَلَى الَّذِينَ آمَنُوا وَجْهَ النَّهَارِ وَاكْفُرُوا آخِرَهُ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Am na ci ñoñ-téere kurél bu wax ne : “Gëmleen li wàcc ca way-gëm ña [Alxuraan] ci suba [waxtu], te bu ngoonee ngeen weddi ko, ndax ñi gëmoon ñoom it weddi.
73وَلَا تُؤْمِنُوا إِلَّا لِمَن تَبِعَ دِينَكُمْ قُلْ إِنَّ الْهُدَىٰ هُدَى اللَّهِ أَن يُؤْتَىٰ أَحَدٌ مِّثْلَ مَا أُوتِيتُمْ أَوْ يُحَاجُّوكُمْ عِندَ رَبِّكُمْ ۗ قُلْ إِنَّ الْفَضْلَ بِيَدِ اللَّهِ يُؤْتِيهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ
Te : “Buleen gëm lu dul ku topp seen diine...”. Neel [yaw Muhammad] : “Njub Yàllaa ko moom” - kon mën naa am kenn nit kuñu jox la mel ni la ngeen jot ba mën a weccee kàddu ak yéen ci mbiri seen Boroom. Neel : Ngëneel a nga ca loxo Yàlla. Dana ko jox ku ko soob. Yàlla ku yaatu la, ku xam la.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
71Aaya

Tekki — Aali Imran 71

Simoore Aali Imran Aaya 71 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yéen ñoñ-téere, lan moo tax ngeen di muure dëgg ak…

Simoore Aaya 71/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 69–73. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers