Al-Ahzab · 30/73
Tekki Waxtaan — Al-Ahzab
يَا نِسَاءَ النَّبِيِّ مَن يَأْتِ مِنكُنَّ بِفَاحِشَةٍ مُّبَيِّنَةٍ يُضَاعَفْ لَهَا الْعَذَابُ ضِعْفَيْنِ ۚ وَكَانَ ذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ يَسِيرًا ۝٣٠
Yaa nisaaa`an Nabiyyi mai yaati minkunna bifaa hishatim mubaiyinatiny yudaa`af lahal `azaabu di`fain wa kaana zaalika `alal laahi yaseera
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Képp ku bokk ci yéen te def aw ñaawtéef wu bir, dees na ko fulal mbugalam ñaari yoon ! Te loolu yomb na Yàlla.
🎧 Dégg

📜 Aaya 28-32 — Al-Ahzab

28يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ قُل لِّأَزْوَاجِكَ إِن كُنتُنَّ تُرِدْنَ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا وَزِينَتَهَا فَتَعَالَيْنَ أُمَتِّعْكُنَّ وَأُسَرِّحْكُنَّ سَرَاحًا جَمِيلًا
Éy yaw Yonent bi ! Waxal say soxna ne leen : “Su fekke ne dundug àddina sii rekk a leen ñor ak ub taaram, kaayleen ma yombalal leen ko, ci ma fase leen ci am pase mu jekk.
29وَإِن كُنتُنَّ تُرِدْنَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَالدَّارَ الْآخِرَةَ فَإِنَّ اللَّهَ أَعَدَّ لِلْمُحْسِنَاتِ مِنكُنَّ أَجْرًا عَظِيمًا
Su fekkee nag ne Yàlla ak Yonentam ak kër gu mujj ga di àllaaxira rekk a leen ñor, [nangeen xam ne] képp kuy rafetal ci yéen, Yàlla dana ko waajalal ag pey gu màgg.
30يَا نِسَاءَ النَّبِيِّ مَن يَأْتِ مِنكُنَّ بِفَاحِشَةٍ مُّبَيِّنَةٍ يُضَاعَفْ لَهَا الْعَذَابُ ضِعْفَيْنِ ۚ وَكَانَ ذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ يَسِيرًا
Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Képp ku bokk ci yéen te def aw ñaawtéef wu bir, dees na ko fulal mbugalam ñaari yoon ! Te loolu yomb na Yàlla.
31۞ وَمَن يَقْنُتْ مِنكُنَّ لِلَّهِ وَرَسُولِهِ وَتَعْمَلْ صَالِحًا نُّؤْتِهَا أَجْرَهَا مَرَّتَيْنِ وَأَعْتَدْنَا لَهَا رِزْقًا كَرِيمًا
Képp ku bokk ci yéen te jébbal boppam Yàlla ak ub Yonentam tey jëf u yiw, Dananu ko fulal ag peyam ñaari yoon, te waajalal Nanu ko xéewal gu màgg.
32يَا نِسَاءَ النَّبِيِّ لَسْتُنَّ كَأَحَدٍ مِّنَ النِّسَاءِ ۚ إِنِ اتَّقَيْتُنَّ فَلَا تَخْضَعْنَ بِالْقَوْلِ فَيَطْمَعَ الَّذِي فِي قَلْبِهِ مَرَضٌ وَقُلْنَ قَوْلًا مَّعْرُوفًا
Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Yemuleen ak yeneen jigéen ñi. Su fekkee ne ragal ngeen Yàlla, buleen di wax waxi caaxaan, yuy tax góor gu xolam tawat di xemmem. Nangeen di wax wax ju yiw njekk.
Al-AhzabFihi Alxuraan
73Aaya
MedinanRevelation
30Aaya

Tekki — Al-Ahzab 30

Simoore Al-Ahzab Aaya 30 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Képp ku bokk ci…

Simoore Aaya 30/73 — Al-Ahzab الأحزاب (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahzab Dégg, Al-Ahzab Tekki, Al-Ahzab mp3, Al-Ahzab pdf. Aaya 28–32. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers