Fatir · 3/45
Tekki Waxtaan — Fatir
يَا أَيُّهَا النَّاسُ اذْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ ۚ هَلْ مِنْ خَالِقٍ غَيْرُ اللَّهِ يَرْزُقُكُم مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ ۚ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ ۝٣
Yaaa ayyuhan naasuzkuroo ni`matal laahi `alaikum; hal min khaaliqin ghairul laahi yarzuqukum minas samaaa`i wal ard; laaa ilaaha illaa Huwa fa annaa tu`fakoon
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen nit ñi ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ci yéen : moo ndax amuñu bindkat bu dul Yàlla, bu leen di wërsëgal ci asamaan yeek suuf si ? Amul jeneen yàlla ju dul Moom ! Moo yéen ndax mën ngeen koo dummóoyu ?
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-5 — Fatir

1الْحَمْدُ لِلَّهِ فَاطِرِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ جَاعِلِ الْمَلَائِكَةِ رُسُلًا أُولِي أَجْنِحَةٍ مَّثْنَىٰ وَثُلَاثَ وَرُبَاعَ ۚ يَزِيدُ فِي الْخَلْقِ مَا يَشَاءُ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla mi bind asamaan yeek suuf si, Mooy ki def Malaaka yi ñu di ay ndaw te di woroomi laaf, ñaar-ñaar, ñett ñett walla ñeent ñeent. Mooy dolli ca mbind ga lu ko soob, Yàlla mën na lépp lu nekk.
2مَّا يَفْتَحِ اللَّهُ لِلنَّاسِ مِن رَّحْمَةٍ فَلَا مُمْسِكَ لَهَا ۖ وَمَا يُمْسِكْ فَلَا مُرْسِلَ لَهُ مِن بَعْدِهِ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Li Yàlla di ubbil nit ñi ci yërmaande, kenn mënu koo fànq, lu Mu tëj itam, kenn mënu koo tijji ginnaawam. Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ.
3يَا أَيُّهَا النَّاسُ اذْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ ۚ هَلْ مِنْ خَالِقٍ غَيْرُ اللَّهِ يَرْزُقُكُم مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ ۚ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ
Éy yéen nit ñi ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ci yéen : moo ndax amuñu bindkat bu dul Yàlla, bu leen di wërsëgal ci asamaan yeek suuf si ? Amul jeneen yàlla ju dul Moom ! Moo yéen ndax mën ngeen koo dummóoyu ?
4وَإِن يُكَذِّبُوكَ فَقَدْ كُذِّبَتْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِكَ ۚ وَإِلَى اللَّهِ تُرْجَعُ الْأُمُورُ
Bu ñu la weddee it, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu woon. Te ca Yàlla la mbir yi di mujj.
5يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ ۖ فَلَا تَغُرَّنَّكُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۖ وَلَا يَغُرَّنَّكُم بِاللَّهِ الْغَرُورُ
Éy yéen nit ñi ! Li Yàllay dige dëgg la. Buleen dundug àddina bii di fàbbi, buleen Séytaane tax a fakku ci Yàlla.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
3Aaya

Tekki — Fatir 3

Simoore Fatir Aaya 3 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen nit ñi ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ci…

Simoore Aaya 3/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 1–5. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers