Al-Ahqaf · 4/35
Tekki Waxtaan — Al-Ahqaf
قُلْ أَرَأَيْتُم مَّا تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ أَرُونِي مَاذَا خَلَقُوا مِنَ الْأَرْضِ أَمْ لَهُمْ شِرْكٌ فِي السَّمَاوَاتِ ۖ ائْتُونِي بِكِتَابٍ مِّن قَبْلِ هَٰذَا أَوْ أَثَارَةٍ مِّنْ عِلْمٍ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٤
Qul ara`aytum maa tad`oona min doonil laahi aroonee maazaa khalaqoo minal ardi am lahum shirkun fis samaawaati eetoonee bi kitaabim min qabli haazaaa aw asaaratim min `ilmin in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Waxal ne : “Ana lan ngeen di xalaat ci li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla ? Wan leen ma ana li ñu sàkk ci kaw suuf ! Walla dañoo am man-man ci asamaan yi ? Indilleen ma Téere bu jiitu (Alxuraan) wala book jeexitali xam-xam, ndegam ñu dëggu ngeen”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 2-6 — Al-Ahqaf

2تَنزِيلُ الْكِتَابِ مِنَ اللَّهِ الْعَزِيزِ الْحَكِيمِ
Lii moo di wàccug Téere ba bawoo ca Yàlla, miy boroom Kàttan, te di ku xereñ.
3مَا خَلَقْنَا السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَمَا بَيْنَهُمَا إِلَّا بِالْحَقِّ وَأَجَلٍ مُّسَمًّى ۚ وَالَّذِينَ كَفَرُوا عَمَّا أُنذِرُوا مُعْرِضُونَ
Bindunu asamaan yeek suuf seek li ci seen diggante, lu dul ci dëgg ak dig bu ñu yemale. Yéefër yi ñoom bu ñu leen di waar dañuy dumóoyu.
4قُلْ أَرَأَيْتُم مَّا تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ أَرُونِي مَاذَا خَلَقُوا مِنَ الْأَرْضِ أَمْ لَهُمْ شِرْكٌ فِي السَّمَاوَاتِ ۖ ائْتُونِي بِكِتَابٍ مِّن قَبْلِ هَٰذَا أَوْ أَثَارَةٍ مِّنْ عِلْمٍ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Waxal ne : “Ana lan ngeen di xalaat ci li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla ? Wan leen ma ana li ñu sàkk ci kaw suuf ! Walla dañoo am man-man ci asamaan yi ? Indilleen ma Téere bu jiitu (Alxuraan) wala book jeexitali xam-xam, ndegam ñu dëggu ngeen”.
5وَمَنْ أَضَلُّ مِمَّن يَدْعُو مِن دُونِ اللَّهِ مَن لَّا يَسْتَجِيبُ لَهُ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ وَهُمْ عَن دُعَائِهِمْ غَافِلُونَ
Waaw ana kan moo gën a sànku (réer) ci kuy woo keneen ku dul Yàlla, koo xam ne du ko wuyu ba baa bis penc ba ? Te dañuy sàggane woote ba (duñu dégg duñu tontu).
6وَإِذَا حُشِرَ النَّاسُ كَانُوا لَهُمْ أَعْدَاءً وَكَانُوا بِعِبَادَتِهِمْ كَافِرِينَ
(Te bu bis Pénc baa) ñu pang nit ñi ngir àtte leen dañuy soppeeku di ay noon, weddi jaamu ga ba mu set wecc.
Al-AhqafFihi Alxuraan
35Aaya
MeccanRevelation
4Aaya

Tekki — Al-Ahqaf 4

Simoore Al-Ahqaf Aaya 4 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waxal ne : “Ana lan ngeen di xalaat ci li…

Simoore Aaya 4/35 — Al-Ahqaf الأحقاف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahqaf Dégg, Al-Ahqaf Tekki, Al-Ahqaf mp3, Al-Ahqaf pdf. Aaya 2–6. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers