Al-Maida · 7/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَاذْكُرُوا نِعْمَةَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَمِيثَاقَهُ الَّذِي وَاثَقَكُم بِهِ إِذْ قُلْتُمْ سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ ۝٧
Wazkuroo ni`matal laahi `alaikum wa meesaaqahul lazee waasaqakum biheee iz qultum sami`naa wa ata`naa wattaqul laah; innal laaha `aleemum bizaatis sudoor
📖 Tekkim Wolof
Fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ak kóllare ya ngeen fasanteek Moom ba ngeen nee : “Dégg nanu te nangu nanu”. Te nangeen ragal Yàlla. Yàlla dey Ku xam li nekk ci xol yi la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 5-9 — Al-Maida

5الْيَوْمَ أُحِلَّ لَكُمُ الطَّيِّبَاتُ ۖ وَطَعَامُ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ حِلٌّ لَّكُمْ وَطَعَامُكُمْ حِلٌّ لَّهُمْ ۖ وَالْمُحْصَنَاتُ مِنَ الْمُؤْمِنَاتِ وَالْمُحْصَنَاتُ مِنَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلِكُمْ إِذَا آتَيْتُمُوهُنَّ أُجُورَهُنَّ مُحْصِنِينَ غَيْرَ مُسَافِحِينَ وَلَا مُتَّخِذِي أَخْدَانٍ ۗ وَمَن يَكْفُرْ بِالْإِيمَانِ فَقَدْ حَبِطَ عَمَلُهُ وَهُوَ فِي الْآخِرَةِ مِنَ الْخَاسِرِينَ
“Bis niki tey, dagan na ci yéen [ñam] yu sell ya. Àtteb ñamu ña jotoon Téere dagan na leen, te seeni ñam yéen, dagan ca ñoom. Te it gor ñu jigéen ña yéwén ci jullit ñi, ak jigéen ña di ay gor, yiw ca ña leen jëkk a jot Téere [dagan na ngeen sëy ak ñoom], ginnaaw ba ngeen joxee seen can ngir sëy mu bañ di njaaloo, ngeen bañ leen a jàppe it ay coro. Képp ku weddi ngëm, ay jëfam sippiku [yàqu] na te àllaaxiraa, ca ña yàqule lay bokk.
6يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا قُمْتُمْ إِلَى الصَّلَاةِ فَاغْسِلُوا وُجُوهَكُمْ وَأَيْدِيَكُمْ إِلَى الْمَرَافِقِ وَامْسَحُوا بِرُءُوسِكُمْ وَأَرْجُلَكُمْ إِلَى الْكَعْبَيْنِ ۚ وَإِن كُنتُمْ جُنُبًا فَاطَّهَّرُوا ۚ وَإِن كُنتُم مَّرْضَىٰ أَوْ عَلَىٰ سَفَرٍ أَوْ جَاءَ أَحَدٌ مِّنكُم مِّنَ الْغَائِطِ أَوْ لَامَسْتُمُ النِّسَاءَ فَلَمْ تَجِدُوا مَاءً فَتَيَمَّمُوا صَعِيدًا طَيِّبًا فَامْسَحُوا بِوُجُوهِكُمْ وَأَيْدِيكُم مِّنْهُ ۚ مَا يُرِيدُ اللَّهُ لِيَجْعَلَ عَلَيْكُم مِّنْ حَرَجٍ وَلَٰكِن يُرِيدُ لِيُطَهِّرَكُمْ وَلِيُتِمَّ نِعْمَتَهُ عَلَيْكُمْ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Bu ngeen jógee jëm ci julli, nangeen raxas seeni xar-kanam ak seeni yoxo ba ca seeni conc ; te nangeen laal [raay - masaa] seen bopp ; nangeen raxas it seeni tànk ba ca ñaari dojor ya. Waaye bu ngeen jógee ci joteg sëy, nangeen sangu ; bu ngeen woppee mbaa ngeen nekk ci tukki, mbaa kenn ci yéen jóge ci wanag wa, mbaa ngeen bànneexu ci jigéen te amuleen ndox, nangeen tiim ci pàkk bu laab, ngeen raay seen xar-kanam ak seeni yoxo. Yàlla nammuleen a teg aw tiis, waaye dafa leen a bëgg a laabal te matal xéewalam ci yéen ndax xéy-na ngeen sant Ko.
7وَاذْكُرُوا نِعْمَةَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَمِيثَاقَهُ الَّذِي وَاثَقَكُم بِهِ إِذْ قُلْتُمْ سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ak kóllare ya ngeen fasanteek Moom ba ngeen nee : “Dégg nanu te nangu nanu”. Te nangeen ragal Yàlla. Yàlla dey Ku xam li nekk ci xol yi la.
8يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُونُوا قَوَّامِينَ لِلَّهِ شُهَدَاءَ بِالْقِسْطِ ۖ وَلَا يَجْرِمَنَّكُمْ شَنَآنُ قَوْمٍ عَلَىٰ أَلَّا تَعْدِلُوا ۚ اعْدِلُوا هُوَ أَقْرَبُ لِلتَّقْوَىٰ ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen nekk ñu taxaw temm ngir Yàlla, di ay seede cig maandute. Te mbañeel gu ngeen bañ aw nit , bumu xiir kenn ci ñàkk a maandu. Nangeen maandu : moo gën a jege ragal Yàlla. Te Yàlla Ku ràññee li ngeen di def la.
9وَعَدَ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ ۙ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ عَظِيمٌ
Yàlla dig na ñi gëm tey jëf lu jiw [farataak sunna] xéewal ak pey gu rëy.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
7Aaya

Tekki — Al-Maida 7

Simoore Al-Maida Aaya 7 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ak kóllare ya ngeen fasanteek…

Simoore Aaya 7/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 5–9. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers