Al-Maida · 8/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُونُوا قَوَّامِينَ لِلَّهِ شُهَدَاءَ بِالْقِسْطِ ۖ وَلَا يَجْرِمَنَّكُمْ شَنَآنُ قَوْمٍ عَلَىٰ أَلَّا تَعْدِلُوا ۚ اعْدِلُوا هُوَ أَقْرَبُ لِلتَّقْوَىٰ ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ ۝٨
Yaaa aiyuhal lazeena aamaanoo koonoo qawwaa meena lillaahi shuhadaaa`a bilqist, wa laa yajrimannakum shana aanu qawmin `alaaa allaa ta`diloo; i`diloo; huwa aqrabu littaqwaa wattaqul laah; innal laaha khabeerum bimaa ta`maloon
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen nekk ñu taxaw temm ngir Yàlla, di ay seede cig maandute. Te mbañeel gu ngeen bañ aw nit , bumu xiir kenn ci ñàkk a maandu. Nangeen maandu : moo gën a jege ragal Yàlla. Te Yàlla Ku ràññee li ngeen di def la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 6-10 — Al-Maida

6يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا قُمْتُمْ إِلَى الصَّلَاةِ فَاغْسِلُوا وُجُوهَكُمْ وَأَيْدِيَكُمْ إِلَى الْمَرَافِقِ وَامْسَحُوا بِرُءُوسِكُمْ وَأَرْجُلَكُمْ إِلَى الْكَعْبَيْنِ ۚ وَإِن كُنتُمْ جُنُبًا فَاطَّهَّرُوا ۚ وَإِن كُنتُم مَّرْضَىٰ أَوْ عَلَىٰ سَفَرٍ أَوْ جَاءَ أَحَدٌ مِّنكُم مِّنَ الْغَائِطِ أَوْ لَامَسْتُمُ النِّسَاءَ فَلَمْ تَجِدُوا مَاءً فَتَيَمَّمُوا صَعِيدًا طَيِّبًا فَامْسَحُوا بِوُجُوهِكُمْ وَأَيْدِيكُم مِّنْهُ ۚ مَا يُرِيدُ اللَّهُ لِيَجْعَلَ عَلَيْكُم مِّنْ حَرَجٍ وَلَٰكِن يُرِيدُ لِيُطَهِّرَكُمْ وَلِيُتِمَّ نِعْمَتَهُ عَلَيْكُمْ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Bu ngeen jógee jëm ci julli, nangeen raxas seeni xar-kanam ak seeni yoxo ba ca seeni conc ; te nangeen laal [raay - masaa] seen bopp ; nangeen raxas it seeni tànk ba ca ñaari dojor ya. Waaye bu ngeen jógee ci joteg sëy, nangeen sangu ; bu ngeen woppee mbaa ngeen nekk ci tukki, mbaa kenn ci yéen jóge ci wanag wa, mbaa ngeen bànneexu ci jigéen te amuleen ndox, nangeen tiim ci pàkk bu laab, ngeen raay seen xar-kanam ak seeni yoxo. Yàlla nammuleen a teg aw tiis, waaye dafa leen a bëgg a laabal te matal xéewalam ci yéen ndax xéy-na ngeen sant Ko.
7وَاذْكُرُوا نِعْمَةَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَمِيثَاقَهُ الَّذِي وَاثَقَكُم بِهِ إِذْ قُلْتُمْ سَمِعْنَا وَأَطَعْنَا ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ak kóllare ya ngeen fasanteek Moom ba ngeen nee : “Dégg nanu te nangu nanu”. Te nangeen ragal Yàlla. Yàlla dey Ku xam li nekk ci xol yi la.
8يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُونُوا قَوَّامِينَ لِلَّهِ شُهَدَاءَ بِالْقِسْطِ ۖ وَلَا يَجْرِمَنَّكُمْ شَنَآنُ قَوْمٍ عَلَىٰ أَلَّا تَعْدِلُوا ۚ اعْدِلُوا هُوَ أَقْرَبُ لِلتَّقْوَىٰ ۖ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen nekk ñu taxaw temm ngir Yàlla, di ay seede cig maandute. Te mbañeel gu ngeen bañ aw nit , bumu xiir kenn ci ñàkk a maandu. Nangeen maandu : moo gën a jege ragal Yàlla. Te Yàlla Ku ràññee li ngeen di def la.
9وَعَدَ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ ۙ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ عَظِيمٌ
Yàlla dig na ñi gëm tey jëf lu jiw [farataak sunna] xéewal ak pey gu rëy.
10وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَحِيمِ
Ña nga xam ne weddi nañu te jàppe Sunuy tegtal ay fen, ñooña ñooy waa Safara.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
8Aaya

Tekki — Al-Maida 8

Simoore Al-Maida Aaya 8 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen ñi gëm ! Nangeen nekk ñu taxaw temm…

Simoore Aaya 8/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 6–10. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers