Al-Mujadila · 12/22
Tekki Waxtaan — Al-Mujadila
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا نَاجَيْتُمُ الرَّسُولَ فَقَدِّمُوا بَيْنَ يَدَيْ نَجْوَاكُمْ صَدَقَةً ۚ ذَٰلِكَ خَيْرٌ لَّكُمْ وَأَطْهَرُ ۚ فَإِن لَّمْ تَجِدُوا فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝١٢
Yaaa ayyuhal lazeena aamanooo izaa naajitumur Rasoola faqaddimoo baina yadai najwaakum sadaqah; zaalika khairul lakum wa athar; fa il lam tajidoo fa innal laaha ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
eey yéen ñi gëm ! Su ngeen di déeyook Yonenta bi, na ngeen ca jiital ab sarax : loolu moo gën ci yéen te moo gën a sell. Su ngeen ko amul Yàlla moom Jéggëlaakoon la Jaglewaakoon la !

🎧 Dégg


📜 Aaya 10-14 — Al-Mujadila

10إِنَّمَا النَّجْوَىٰ مِنَ الشَّيْطَانِ لِيَحْزُنَ الَّذِينَ آمَنُوا وَلَيْسَ بِضَارِّهِمْ شَيْئًا إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ ۚ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ
Déeyoo moom [liggéeyub] saytaane doŋŋ la ngir man a tiit loo ñi gëm. Te manuleen a lor dara lu dul ci kàttanu Yàllu. Ñi gëm nañuy doyloo te wéeru ci Yàlla.
11يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا قِيلَ لَكُمْ تَفَسَّحُوا فِي الْمَجَالِسِ فَافْسَحُوا يَفْسَحِ اللَّهُ لَكُمْ ۖ وَإِذَا قِيلَ انشُزُوا فَانشُزُوا يَرْفَعِ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا مِنكُمْ وَالَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ دَرَجَاتٍ ۚ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Eey yéen ñi gëm ! bu ñu leen waxee ne yaatleleen ci jataay yi : “Na ngeen daldi yaatal”,. Kon dey Yàlla dana leen yaatalal Bu ñu leen waxee ne jógleen, nangeen daldi jóg (su ngeen ko defee). Yàlla dana yékkatil ñi gëm te bokk ci yéen ak ña am xam-xam (ay daraja yu kawe). Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
12يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا نَاجَيْتُمُ الرَّسُولَ فَقَدِّمُوا بَيْنَ يَدَيْ نَجْوَاكُمْ صَدَقَةً ۚ ذَٰلِكَ خَيْرٌ لَّكُمْ وَأَطْهَرُ ۚ فَإِن لَّمْ تَجِدُوا فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
eey yéen ñi gëm ! Su ngeen di déeyook Yonenta bi, na ngeen ca jiital ab sarax : loolu moo gën ci yéen te moo gën a sell. Su ngeen ko amul Yàlla moom Jéggëlaakoon la Jaglewaakoon la !
13أَأَشْفَقْتُمْ أَن تُقَدِّمُوا بَيْنَ يَدَيْ نَجْوَاكُمْ صَدَقَاتٍ ۚ فَإِذْ لَمْ تَفْعَلُوا وَتَابَ اللَّهُ عَلَيْكُمْ فَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَآتُوا الزَّكَاةَ وَأَطِيعُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ ۚ وَاللَّهُ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
Moo mbaa du dangeen ragal ñàkk ba tax du ngeen jiital sarax ? Su ngeen, ko deful Yàlla baal leen, daldi leen dem taxawali julli, te di natt asaka, te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Yàlla Ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
14۞ أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ تَوَلَّوْا قَوْمًا غَضِبَ اللَّهُ عَلَيْهِم مَّا هُم مِّنكُمْ وَلَا مِنْهُمْ وَيَحْلِفُونَ عَلَى الْكَذِبِ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Xanaa gisuloo naaféq ya dem ànd ak ña Yàlla mere (Yahuud ya) ? Ñoom bokkuñu ci yéen, bokkuñu it ci ñoom (Yahuud ya) ; te ña ngay giñ fen ci Yàlla, te xam ko xéll.
Al-MujadilaFihi Alxuraan
22Aaya
MedinanRevelation
12Aaya

Tekki — Al-Mujadila 12

Simoore Al-Mujadila Aaya 12 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : eey yéen ñi gëm ! Su ngeen di déeyook Yonenta…

Simoore Aaya 12/22 — Al-Mujadila المجادلة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Mujadila Dégg, Al-Mujadila Tekki, Al-Mujadila mp3, Al-Mujadila pdf. Aaya 10–14. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers