Al-Mujadila · 2/22
Tekki Waxtaan — Al-Mujadila
الَّذِينَ يُظَاهِرُونَ مِنكُم مِّن نِّسَائِهِم مَّا هُنَّ أُمَّهَاتِهِمْ ۖ إِنْ أُمَّهَاتُهُمْ إِلَّا اللَّائِي وَلَدْنَهُمْ ۚ وَإِنَّهُمْ لَيَقُولُونَ مُنكَرًا مِّنَ الْقَوْلِ وَزُورًا ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَعَفُوٌّ غَفُورٌ ۝٢
Allazeena yuzaahiroona minkum min nisaaa`ihim maa hunnaa ummahaatihim in ummahaatuhum illal laaa`ee waladnahum; wa innaahum la yaqooloona munkaram minal qawli wa zooraa; wa innal laaha la`afuwwun ghafoor
📖 Tekkim Wolof
Góor ñiy weddi seeni jabar seen pendali nday , taxul ñu mel mi seeni nday ci ñoom... seeni nday ñoom ña leen juróon. Li ñuy wax lu ñaaw la di ay fen. Te Yàlla nag kuy bale la ab Jéggalaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-4 — Al-Mujadila

1قَدْ سَمِعَ اللَّهُ قَوْلَ الَّتِي تُجَادِلُكَ فِي زَوْجِهَا وَتَشْتَكِي إِلَى اللَّهِ وَاللَّهُ يَسْمَعُ تَحَاوُرَكُمَا ۚ إِنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ بَصِيرٌ
Yàlla dégg na waxi jigéen ja doon dàggasanteek yaw ci mbirum jëkëram te doon joyal njàmbatam ci Yàlla. Yàllaa ngi dégg seenuk wàqante yéen ñaar, Yàlla kuy dégg la kuy gis la.
2الَّذِينَ يُظَاهِرُونَ مِنكُم مِّن نِّسَائِهِم مَّا هُنَّ أُمَّهَاتِهِمْ ۖ إِنْ أُمَّهَاتُهُمْ إِلَّا اللَّائِي وَلَدْنَهُمْ ۚ وَإِنَّهُمْ لَيَقُولُونَ مُنكَرًا مِّنَ الْقَوْلِ وَزُورًا ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَعَفُوٌّ غَفُورٌ
Góor ñiy weddi seeni jabar seen pendali nday , taxul ñu mel mi seeni nday ci ñoom... seeni nday ñoom ña leen juróon. Li ñuy wax lu ñaaw la di ay fen. Te Yàlla nag kuy bale la ab Jéggalaakoon la.
3وَالَّذِينَ يُظَاهِرُونَ مِن نِّسَائِهِمْ ثُمَّ يَعُودُونَ لِمَا قَالُوا فَتَحْرِيرُ رَقَبَةٍ مِّن قَبْلِ أَن يَتَمَاسَّا ۚ ذَٰلِكُمْ تُوعَظُونَ بِهِ ۚ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Góor ñi nga xam ne dañoo woddi seeni jabar seeni pendali nday ba noppi bëgg caa dale ginnaaw, ca la ñu waxoon, nanu goreel ab jaam balaa ñoo jonjoowaat loolu la ñu leen di jàjje. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
4فَمَن لَّمْ يَجِدْ فَصِيَامُ شَهْرَيْنِ مُتَتَابِعَيْنِ مِن قَبْلِ أَن يَتَمَاسَّا ۖ فَمَن لَّمْ يَسْتَطِعْ فَإِطْعَامُ سِتِّينَ مِسْكِينًا ۚ ذَٰلِكَ لِتُؤْمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ ۚ وَتِلْكَ حُدُودُ اللَّهِ ۗ وَلِلْكَافِرِينَ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Su ko manul na woor ñaari weer yu tegaloo balaa ñuy jonjoowaat. Su ko manul, na leel juróom-benn-fukki ndóol miskiin. Loolu nag, ngir ngeen gëm Yàlla ak ub Yonentam. Te loolu mooy daytali Yàlla yi. Ña weddi nag ñoom danañu am mbugël mu mitti.
Al-MujadilaFihi Alxuraan
22Aaya
MedinanRevelation
2Aaya

Tekki — Al-Mujadila 2

Simoore Al-Mujadila Aaya 2 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Góor ñiy weddi seeni jabar seen pendali nday , taxul…

Simoore Aaya 2/22 — Al-Mujadila المجادلة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Mujadila Dégg, Al-Mujadila Tekki, Al-Mujadila mp3, Al-Mujadila pdf. Aaya 1–4. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers