As-Saff · 3/14
Tekki Waxtaan — As-Saff
كَبُرَ مَقْتًا عِندَ اللَّهِ أَن تَقُولُوا مَا لَا تَفْعَلُونَ ۝٣
Kabura maqtan `indal laahi an taqooloo maa laa taf`aloon
📖 Tekkim Wolof
Wax ji ngeen di wax te du ngeen ko def ak jéppi gu rëy (la leen di jural ca Yàlla).

🎧 Dégg


📜 Aaya 1-5 — As-Saff

1سَبَّحَ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۖ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla, te Moom moo di Boroom Kàttan ga, di Ku Xereñ ka.
2يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لِمَ تَقُولُونَ مَا لَا تَفْعَلُونَ
Eey yéen ñi gëm ! Ana lan moo tax ngeen di wax lu ngeen dul def ?
3كَبُرَ مَقْتًا عِندَ اللَّهِ أَن تَقُولُوا مَا لَا تَفْعَلُونَ
Wax ji ngeen di wax te du ngeen ko def ak jéppi gu rëy (la leen di jural ca Yàlla).
4إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الَّذِينَ يُقَاتِلُونَ فِي سَبِيلِهِ صَفًّا كَأَنَّهُم بُنْيَانٌ مَّرْصُوصٌ
Yàlla safoona ñiy xeex ci yoonam wi def senn sàppe melni ñoom tabax bu ñu raax la ñu.
5وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ لِمَ تُؤْذُونَنِي وَقَد تَّعْلَمُونَ أَنِّي رَسُولُ اللَّهِ إِلَيْكُمْ ۖ فَلَمَّا زَاغُوا أَزَاغَ اللَّهُ قُلُوبَهُمْ ۚ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْفَاسِقِينَ
(Fàttalikul) Ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : "Yéen samaw nit ! Ana lan moo tax ba ngeen di ma lor te xam ngeen xell ne man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen ? ” Bu ñu jengee, Yàlla jengal seeni xol, te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay saay-saay.
As-SaffFihi Alxuraan
14Aaya
MedinanRevelation
3Aaya

Tekki — As-Saff 3

Simoore As-Saff Aaya 3 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Wax ji ngeen di wax te du ngeen ko def…

Simoore Aaya 3/14 — As-Saff الصف (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Saff Dégg, As-Saff Tekki, As-Saff mp3, As-Saff pdf. Aaya 1–5. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers