As-Saff · 4/14
Tekki Waxtaan — As-Saff
إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الَّذِينَ يُقَاتِلُونَ فِي سَبِيلِهِ صَفًّا كَأَنَّهُم بُنْيَانٌ مَّرْصُوصٌ ۝٤
Innal laaha yuhibbul lazeena yuqaatiloona fee sabeelihee saffan kaannahum bunyaanum marsoos
📖 Tekkim Wolof
Yàlla safoona ñiy xeex ci yoonam wi def senn sàppe melni ñoom tabax bu ñu raax la ñu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 2-6 — As-Saff

2يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لِمَ تَقُولُونَ مَا لَا تَفْعَلُونَ
Eey yéen ñi gëm ! Ana lan moo tax ngeen di wax lu ngeen dul def ?
3كَبُرَ مَقْتًا عِندَ اللَّهِ أَن تَقُولُوا مَا لَا تَفْعَلُونَ
Wax ji ngeen di wax te du ngeen ko def ak jéppi gu rëy (la leen di jural ca Yàlla).
4إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الَّذِينَ يُقَاتِلُونَ فِي سَبِيلِهِ صَفًّا كَأَنَّهُم بُنْيَانٌ مَّرْصُوصٌ
Yàlla safoona ñiy xeex ci yoonam wi def senn sàppe melni ñoom tabax bu ñu raax la ñu.
5وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ لِمَ تُؤْذُونَنِي وَقَد تَّعْلَمُونَ أَنِّي رَسُولُ اللَّهِ إِلَيْكُمْ ۖ فَلَمَّا زَاغُوا أَزَاغَ اللَّهُ قُلُوبَهُمْ ۚ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْفَاسِقِينَ
(Fàttalikul) Ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : "Yéen samaw nit ! Ana lan moo tax ba ngeen di ma lor te xam ngeen xell ne man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen ? ” Bu ñu jengee, Yàlla jengal seeni xol, te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay saay-saay.
6وَإِذْ قَالَ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ يَا بَنِي إِسْرَائِيلَ إِنِّي رَسُولُ اللَّهِ إِلَيْكُم مُّصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيَّ مِنَ التَّوْرَاةِ وَمُبَشِّرًا بِرَسُولٍ يَأْتِي مِن بَعْدِي اسْمُهُ أَحْمَدُ ۖ فَلَمَّا جَاءَهُم بِالْبَيِّنَاتِ قَالُوا هَٰذَا سِحْرٌ مُّبِينٌ
(Fàttalikul it) Ba Iisaa doomu Maryaama waxee ne : “eey yéen waa giir Banii-Israayiil, man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen, may dëggal la ma jiitu woon, ca Tawraat, di bégale it, ci Yonent buy dikk sama ginnaaw aw turam di “Ahmadu”. Waaye ba mu leen dikkale ak ay firnde yu leer , dañoo wax ne : “Lii kat ag njibarla gu bir ne fàŋŋ”.
As-SaffFihi Alxuraan
14Aaya
MedinanRevelation
4Aaya

Tekki — As-Saff 4

Simoore As-Saff Aaya 4 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla safoona ñiy xeex ci yoonam wi def senn sàppe…

Simoore Aaya 4/14 — As-Saff الصف (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Saff Dégg, As-Saff Tekki, As-Saff mp3, As-Saff pdf. Aaya 2–6. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers