Al-A'raf · 55/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
ادْعُوا رَبَّكُمْ تَضَرُّعًا وَخُفْيَةً ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُعْتَدِينَ ۝٥٥
Ud`oo Rabbakum tadarru`anw wa khufyah; innahoo laa yuhibbul mu`tadeen
📖 Tekkim Wolof
Ñaanleen seen Boroom ci toroxlu ak ci yelu. Moom nag soppul ñiy jéggi dayo.
🎧 Dégg

📜 Aaya 53-57 — Al-A'raf

53هَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا تَأْوِيلَهُ ۚ يَوْمَ يَأْتِي تَأْوِيلُهُ يَقُولُ الَّذِينَ نَسُوهُ مِن قَبْلُ قَدْ جَاءَتْ رُسُلُ رَبِّنَا بِالْحَقِّ فَهَل لَّنَا مِن شُفَعَاءَ فَيَشْفَعُوا لَنَا أَوْ نُرَدُّ فَنَعْمَلَ غَيْرَ الَّذِي كُنَّا نَعْمَلُ ۚ قَدْ خَسِرُوا أَنفُسَهُمْ وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Moo ndax dañuy xaar ba lu ko firndéel agsi ? Ña ko fàtte woon, la ko jiitu, danañu wax ne : “Yonenti sunu Boroom indi woon nañu dëgg. Moo ndax dananu amatiy rammukat yu nuy rammu ? Walla ñu delloo nu [àddina] nu def fa lu gën a rafet la nu fa daan def ? ”. Yàqal nañu jeeg seen bopp ; te la ñu daan duur réer na leen.
54إِنَّ رَبَّكُمُ اللَّهُ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ فِي سِتَّةِ أَيَّامٍ ثُمَّ اسْتَوَىٰ عَلَى الْعَرْشِ يُغْشِي اللَّيْلَ النَّهَارَ يَطْلُبُهُ حَثِيثًا وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ وَالنُّجُومَ مُسَخَّرَاتٍ بِأَمْرِهِ ۗ أَلَا لَهُ الْخَلْقُ وَالْأَمْرُ ۗ تَبَارَكَ اللَّهُ رَبُّ الْعَالَمِينَ
Seen Boroom nag mooy ki bind asamaan yeek suuf si ci juróom-benni fan, ba noppi Mu jublu ca Gàngunaay ga. Dana muure guddi ak bëccëg Mu toftale ko bu gaaw. Te jant bi ak weer wi ak bindiw, yu ñu tàggat lañu ci ndigalam. Moo ndax du Moo moom bind gi ak dogal yi? Yàlla Boroom àddina si, Ku barkeel la !
55ادْعُوا رَبَّكُمْ تَضَرُّعًا وَخُفْيَةً ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُعْتَدِينَ
Ñaanleen seen Boroom ci toroxlu ak ci yelu. Moom nag soppul ñiy jéggi dayo.
56وَلَا تُفْسِدُوا فِي الْأَرْضِ بَعْدَ إِصْلَاحِهَا وَادْعُوهُ خَوْفًا وَطَمَعًا ۚ إِنَّ رَحْمَتَ اللَّهِ قَرِيبٌ مِّنَ الْمُحْسِنِينَ
Buleen di yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Te nangeen di ñaan ànd ak ragal ak yaakaar, yërmaandey Yàlla nag lu jegeñ rafetalkat yi la.
57وَهُوَ الَّذِي يُرْسِلُ الرِّيَاحَ بُشْرًا بَيْنَ يَدَيْ رَحْمَتِهِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا أَقَلَّتْ سَحَابًا ثِقَالًا سُقْنَاهُ لِبَلَدٍ مَّيِّتٍ فَأَنزَلْنَا بِهِ الْمَاءَ فَأَخْرَجْنَا بِهِ مِن كُلِّ الثَّمَرَاتِ ۚ كَذَٰلِكَ نُخْرِجُ الْمَوْتَىٰ لَعَلَّكُمْ تَذَكَّرُونَ
Moo moom kiy yabal ngelaw yi ñuy tasaaroo lu jiitu. Ba bu ñu yanoo niir yu diis, ñu nàndal ci réew mu bekkoor, Nu wàccee ca ndox, génne ca bépp xeetu doomu gàncax [meññent]. Noonu lañuy génnee ñi dee [bu ñu leen di dekkal] ndax xéy-na ngeen fàttaliku.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
55Aaya

Tekki — Al-A'raf 55

Simoore Al-A'raf Aaya 55 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñaanleen seen Boroom ci toroxlu ak ci yelu. Moom nag…

Simoore Aaya 55/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 53–57. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers