Al-A'raf · 56/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
وَلَا تُفْسِدُوا فِي الْأَرْضِ بَعْدَ إِصْلَاحِهَا وَادْعُوهُ خَوْفًا وَطَمَعًا ۚ إِنَّ رَحْمَتَ اللَّهِ قَرِيبٌ مِّنَ الْمُحْسِنِينَ ۝٥٦
Wa laa tufsidoo fil ardi ba`da islaahihaa wad`oohu khawfanw wa tama`aa; inna rahmatal laahi qareebum minal muhsineen
📖 Tekkim Wolof
Buleen di yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Te nangeen di ñaan ànd ak ragal ak yaakaar, yërmaandey Yàlla nag lu jegeñ rafetalkat yi la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 54-58 — Simoore Al-A'raf

54إِنَّ رَبَّكُمُ اللَّهُ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ فِي سِتَّةِ أَيَّامٍ ثُمَّ اسْتَوَىٰ عَلَى الْعَرْشِ يُغْشِي اللَّيْلَ النَّهَارَ يَطْلُبُهُ حَثِيثًا وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ وَالنُّجُومَ مُسَخَّرَاتٍ بِأَمْرِهِ ۗ أَلَا لَهُ الْخَلْقُ وَالْأَمْرُ ۗ تَبَارَكَ اللَّهُ رَبُّ الْعَالَمِينَ
Seen Boroom nag mooy ki bind asamaan yeek suuf si ci juróom-benni fan, ba noppi Mu jublu ca Gàngunaay ga. Dana muure guddi ak bëccëg Mu toftale ko bu gaaw. Te jant bi ak weer wi ak bindiw, yu ñu tàggat lañu ci ndigalam. Moo ndax du Moo moom bind gi ak dogal yi? Yàlla Boroom àddina si, Ku barkeel la !
55ادْعُوا رَبَّكُمْ تَضَرُّعًا وَخُفْيَةً ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُعْتَدِينَ
Ñaanleen seen Boroom ci toroxlu ak ci yelu. Moom nag soppul ñiy jéggi dayo.
56وَلَا تُفْسِدُوا فِي الْأَرْضِ بَعْدَ إِصْلَاحِهَا وَادْعُوهُ خَوْفًا وَطَمَعًا ۚ إِنَّ رَحْمَتَ اللَّهِ قَرِيبٌ مِّنَ الْمُحْسِنِينَ
Buleen di yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Te nangeen di ñaan ànd ak ragal ak yaakaar, yërmaandey Yàlla nag lu jegeñ rafetalkat yi la.
57وَهُوَ الَّذِي يُرْسِلُ الرِّيَاحَ بُشْرًا بَيْنَ يَدَيْ رَحْمَتِهِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا أَقَلَّتْ سَحَابًا ثِقَالًا سُقْنَاهُ لِبَلَدٍ مَّيِّتٍ فَأَنزَلْنَا بِهِ الْمَاءَ فَأَخْرَجْنَا بِهِ مِن كُلِّ الثَّمَرَاتِ ۚ كَذَٰلِكَ نُخْرِجُ الْمَوْتَىٰ لَعَلَّكُمْ تَذَكَّرُونَ
Moo moom kiy yabal ngelaw yi ñuy tasaaroo lu jiitu. Ba bu ñu yanoo niir yu diis, ñu nàndal ci réew mu bekkoor, Nu wàccee ca ndox, génne ca bépp xeetu doomu gàncax [meññent]. Noonu lañuy génnee ñi dee [bu ñu leen di dekkal] ndax xéy-na ngeen fàttaliku.
58وَالْبَلَدُ الطَّيِّبُ يَخْرُجُ نَبَاتُهُ بِإِذْنِ رَبِّهِ ۖ وَالَّذِي خَبُثَ لَا يَخْرُجُ إِلَّا نَكِدًا ۚ كَذَٰلِكَ نُصَرِّفُ الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَشْكُرُونَ
Te dëkk bu [suuf sa baax], gàncaxam dana génn ci coobare Boroomam ; ña [seen suuf] bon, du génne lu dul lu bon. Noonu Lanuy leerale tegtal yi ngir nit ñuy gërëm [seen Boroom].
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
56Aaya

Tekki — Al-A'raf 56

Simoore Al-A'raf Aaya 56 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buleen di yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko…

Simoore Aaya 56/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 54–58. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers