At-Tawba · 17/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
مَا كَانَ لِلْمُشْرِكِينَ أَن يَعْمُرُوا مَسَاجِدَ اللَّهِ شَاهِدِينَ عَلَىٰ أَنفُسِهِم بِالْكُفْرِ ۚ أُولَٰئِكَ حَبِطَتْ أَعْمَالُهُمْ وَفِي النَّارِ هُمْ خَالِدُونَ ۝١٧
maa kaana lilmushrikeena ai ya`muroo masaajidal laahi shaahideena `alaaa anfusihim bilkufr; ulaaa`ika habitat a`maaluhum wa fin naari hum khaalidoon
📖 Tekkim Wolof
Yellul bokkaalekat ya di toppatoo jàkkay Yàlla ji, te ñoom ay seede lañu ci seen weddi ga. Ñoom seeni jëf yàqu na ; te danañu leen dugal Safara fàwwu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 15-19 — At-Tawba

15وَيُذْهِبْ غَيْظَ قُلُوبِهِمْ ۗ وَيَتُوبُ اللَّهُ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Te Dana dindi mer mi nekk ci seeni xol. Te Dana baal ku Ko neex. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
16أَمْ حَسِبْتُمْ أَن تُتْرَكُوا وَلَمَّا يَعْلَمِ اللَّهُ الَّذِينَ جَاهَدُوا مِنكُمْ وَلَمْ يَتَّخِذُوا مِن دُونِ اللَّهِ وَلَا رَسُولِهِ وَلَا الْمُؤْمِنِينَ وَلِيجَةً ۚ وَاللَّهُ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
Am dangeen a njortu ne Danu leen di bàyyi te Yàlla duleen nattu ba xam ñiy xareel diine te duñu jàpp xarit, bàyyi Yàlla ak Yonentam ak ña gëm ? Yàlla Ku xam li ngeen di def la.
17مَا كَانَ لِلْمُشْرِكِينَ أَن يَعْمُرُوا مَسَاجِدَ اللَّهِ شَاهِدِينَ عَلَىٰ أَنفُسِهِم بِالْكُفْرِ ۚ أُولَٰئِكَ حَبِطَتْ أَعْمَالُهُمْ وَفِي النَّارِ هُمْ خَالِدُونَ
Yellul bokkaalekat ya di toppatoo jàkkay Yàlla ji, te ñoom ay seede lañu ci seen weddi ga. Ñoom seeni jëf yàqu na ; te danañu leen dugal Safara fàwwu.
18إِنَّمَا يَعْمُرُ مَسَاجِدَ اللَّهِ مَنْ آمَنَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَأَقَامَ الصَّلَاةَ وَآتَى الزَّكَاةَ وَلَمْ يَخْشَ إِلَّا اللَّهَ ۖ فَعَسَىٰ أُولَٰئِكَ أَن يَكُونُوا مِنَ الْمُهْتَدِينَ
Ki yayoo dundal jàkkay Yàlla ja kay, mooy ku gëm Yàlla ak Bis-pénc ba, tey julli, di joxe asaka te du ragal kenn ku dul Yàlla. Kon ñooña, amaana ñu bokk ca ñu gindiku ña.
19۞ أَجَعَلْتُمْ سِقَايَةَ الْحَاجِّ وَعِمَارَةَ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ كَمَنْ آمَنَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَجَاهَدَ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۚ لَا يَسْتَوُونَ عِندَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ
Moo ndax dangeen di yemale [jëfi] kay dàndale ñay aji tey toppatoo jàkka ju ñu wormaal ak jëfi ka gëm Yàlla ak Bis-pénc ba te xareel yoonu Yàlla ? yemuñu ca Yàlla te Yàlla du gindi nit ñuy tooñ.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
17Aaya

Tekki — At-Tawba 17

Simoore At-Tawba Aaya 17 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yellul bokkaalekat ya di toppatoo jàkkay Yàlla ji, te ñoom…

Simoore Aaya 17/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 15–19. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers