Yunus · 38/109
Tekki Waxtaan — Yunus
أَمْ يَقُولُونَ افْتَرَاهُ ۖ قُلْ فَأْتُوا بِسُورَةٍ مِّثْلِهِ وَادْعُوا مَنِ اسْتَطَعْتُم مِّن دُونِ اللَّهِ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٣٨
Am yaqooloonaf taraahu qul faatoo bisooratim mislihee wad`oo manis tata`tum min doonil laahi in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Am dañoo wax ne : “Dafa koo duur ” ? Neel : “Indileen saar wu ni mel, te woo ku leen neex ba mu des Yàlla [mu dimbali leen ci loolu] ndeem ñu dëggu ngeen”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 36-40 — Yunus

36وَمَا يَتَّبِعُ أَكْثَرُهُمْ إِلَّا ظَنًّا ۚ إِنَّ الظَّنَّ لَا يُغْنِي مِنَ الْحَقِّ شَيْئًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِمَا يَفْعَلُونَ
Li ëpp ci ñoom, toppuñu lu dul ay njort. Te njort du jariñ dara ci dëgg ! Yàlla naka Ku xam xéll la li ngeen di def.
37وَمَا كَانَ هَٰذَا الْقُرْآنُ أَن يُفْتَرَىٰ مِن دُونِ اللَّهِ وَلَٰكِن تَصْدِيقَ الَّذِي بَيْنَ يَدَيْهِ وَتَفْصِيلَ الْكِتَابِ لَا رَيْبَ فِيهِ مِن رَّبِّ الْعَالَمِينَ
Alxuraan jii nekkul lu ñu duur bàyyi Yàlla, waaye dafa nekk di luy dëggal la ko jiitu tey settantal Téere ba nga xam ne sikk nekkul ci ne ma nga tukkee ca Boroom àddina si.
38أَمْ يَقُولُونَ افْتَرَاهُ ۖ قُلْ فَأْتُوا بِسُورَةٍ مِّثْلِهِ وَادْعُوا مَنِ اسْتَطَعْتُم مِّن دُونِ اللَّهِ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Am dañoo wax ne : “Dafa koo duur ” ? Neel : “Indileen saar wu ni mel, te woo ku leen neex ba mu des Yàlla [mu dimbali leen ci loolu] ndeem ñu dëggu ngeen”.
39بَلْ كَذَّبُوا بِمَا لَمْ يُحِيطُوا بِعِلْمِهِ وَلَمَّا يَأْتِهِمْ تَأْوِيلُهُ ۚ كَذَٰلِكَ كَذَّبَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۖ فَانظُرْ كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الظَّالِمِينَ
Déedéet : weddi nañu loo xam ne amuñu xam-xamam te ag leeralam agsiwul ci ñoom. Noonu la ña leen jiitu weddee woon. Waaye xoolal rekk la mujjug tooñkat ya deme woon !
40وَمِنْهُم مَّن يُؤْمِنُ بِهِ وَمِنْهُم مَّن لَّا يُؤْمِنُ بِهِ ۚ وَرَبُّكَ أَعْلَمُ بِالْمُفْسِدِينَ
Te kat am na ci ñoom ñu ko gëm, am na it ñu ko gëmul. Te sa Boroom moo gën a xam yàqkat ya.
YunusFihi Alxuraan
109Aaya
MeccanRevelation
38Aaya

Tekki — Yunus 38

Simoore Yunus Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am dañoo wax ne : “Dafa koo duur ” ?…

Simoore Aaya 38/109 — Yunus يونس (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yunus Dégg, Yunus Tekki, Yunus mp3, Yunus pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers