Hud · 27/123
Tekki Waxtaan — Hud
فَقَالَ الْمَلَأُ الَّذِينَ كَفَرُوا مِن قَوْمِهِ مَا نَرَاكَ إِلَّا بَشَرًا مِّثْلَنَا وَمَا نَرَاكَ اتَّبَعَكَ إِلَّا الَّذِينَ هُمْ أَرَاذِلُنَا بَادِيَ الرَّأْيِ وَمَا نَرَىٰ لَكُمْ عَلَيْنَا مِن فَضْلٍ بَلْ نَظُنُّكُمْ كَاذِبِينَ ۝٢٧
Faqaalal mala ul lazeena kafaroo min qawmihee ma naraaka illaa basharam mislanaa wa maa naraakat taba`aka illal lazeena hum araazilunaa baadiyar raayi wa maa naraa lakum `alainaa min fadlim bal nazunnukum kaazibeen
📖 Tekkim Wolof
Ña di ay kilifa ci aw nitam, te weddi, ne ko : “Xoolewunu la lu dul ngay kenn rekk ci nun ; te it gisunu ñi la topp ñu dul ñi gën a suufe ci nun te lu yomb a gis ; te ëppalewuleen nu dara. Te sax am nanu njort ci ne ay fenkat ngeen”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 25-29 — Hud

25وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا نُوحًا إِلَىٰ قَوْمِهِ إِنِّي لَكُمْ نَذِيرٌ مُّبِينٌ
Yónni woon Nanu Nooh ca aw nitam, mu ne leen : “Man waarekat laa bu leen di xamal lu leer
26أَن لَّا تَعْبُدُوا إِلَّا اللَّهَ ۖ إِنِّي أَخَافُ عَلَيْكُمْ عَذَابَ يَوْمٍ أَلِيمٍ
te ngeen bañ a jaamu ku dul Yàlla. Te ragalal naa leen mbugalum bis bu metti dal leen”.
27فَقَالَ الْمَلَأُ الَّذِينَ كَفَرُوا مِن قَوْمِهِ مَا نَرَاكَ إِلَّا بَشَرًا مِّثْلَنَا وَمَا نَرَاكَ اتَّبَعَكَ إِلَّا الَّذِينَ هُمْ أَرَاذِلُنَا بَادِيَ الرَّأْيِ وَمَا نَرَىٰ لَكُمْ عَلَيْنَا مِن فَضْلٍ بَلْ نَظُنُّكُمْ كَاذِبِينَ
Ña di ay kilifa ci aw nitam, te weddi, ne ko : “Xoolewunu la lu dul ngay kenn rekk ci nun ; te it gisunu ñi la topp ñu dul ñi gën a suufe ci nun te lu yomb a gis ; te ëppalewuleen nu dara. Te sax am nanu njort ci ne ay fenkat ngeen”.
28قَالَ يَا قَوْمِ أَرَأَيْتُمْ إِن كُنتُ عَلَىٰ بَيِّنَةٍ مِّن رَّبِّي وَآتَانِي رَحْمَةً مِّنْ عِندِهِ فَعُمِّيَتْ عَلَيْكُمْ أَنُلْزِمُكُمُوهَا وَأَنتُمْ لَهَا كَارِهُونَ
Mu ne leen : "Samaw nit ! Naka ngeen di gisee mbir mi ? Su fekkee maa ngi ci lu wér lu jóge ci sama Boroom, te Mu jox ma yërmaande ju jóge ci Moom ci lu nëbbu ci yéen, ndax dama cee ga te fekk yéen ngeen sib ko ?
29وَيَا قَوْمِ لَا أَسْأَلُكُمْ عَلَيْهِ مَالًا ۖ إِنْ أَجْرِيَ إِلَّا عَلَى اللَّهِ ۚ وَمَا أَنَا بِطَارِدِ الَّذِينَ آمَنُوا ۚ إِنَّهُم مُّلَاقُو رَبِّهِمْ وَلَٰكِنِّي أَرَاكُمْ قَوْمًا تَجْهَلُونَ
Te yéen samaw nit, laajumaleen ci alal. Samag pey nekkul ci kenn ku dul Yàlla. Te nekkuma ñiy dàq way-gëm, ñoom danañu dajeek seen Boroom. Waaye ni ma leen gise, aw nit ñu réer ngeen.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
27Aaya

Tekki — Hud 27

Simoore Hud Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña di ay kilifa ci aw nitam, te weddi, ne…

Simoore Aaya 27/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers