Yusuf · 30/111
Tekki Waxtaan — Simoore Yusuf
۞ وَقَالَ نِسْوَةٌ فِي الْمَدِينَةِ امْرَأَتُ الْعَزِيزِ تُرَاوِدُ فَتَاهَا عَن نَّفْسِهِ ۖ قَدْ شَغَفَهَا حُبًّا ۖ إِنَّا لَنَرَاهَا فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ ۝٣٠
Wa qaala niswatun filma deenatim ra atul`Azeezi turaawidu fataahaa `an nafsihee qad shaghafahaa bubbaa; innaa lana raahaa fee dalaalim mubeen
📖 Tekkim Wolof
Aw jigéen di wax ci dëkk bi naan : “Jabaru buur bi dafa doon sàkku jaamam ! Mbëggeel gëlamal ko. Nun daal gis nanu mu nekk ci ag réer gu tar.

🎧 Dégg


📜 Aaya 28-32 — Simoore Yusuf

28فَلَمَّا رَأَىٰ قَمِيصَهُ قُدَّ مِن دُبُرٍ قَالَ إِنَّهُ مِن كَيْدِكُنَّ ۖ إِنَّ كَيْدَكُنَّ عَظِيمٌ
Ba jëkkër ja gisee yére ya xottiku ca ginnaaw, mu ne : “Lii ci seeni pexe la [yéen jigéen ñi] ! te seeni pexe réy na !
29يُوسُفُ أَعْرِضْ عَنْ هَٰذَا ۚ وَاسْتَغْفِرِي لِذَنبِكِ ۖ إِنَّكِ كُنتِ مِنَ الْخَاطِئِينَ
Yuusufa, dëddul lii ! Te yaw [sama jabar] jéggalul sa bàkkaar ndax yaw bokk nga ca ñay def lu bon”.
30۞ وَقَالَ نِسْوَةٌ فِي الْمَدِينَةِ امْرَأَتُ الْعَزِيزِ تُرَاوِدُ فَتَاهَا عَن نَّفْسِهِ ۖ قَدْ شَغَفَهَا حُبًّا ۖ إِنَّا لَنَرَاهَا فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
Aw jigéen di wax ci dëkk bi naan : “Jabaru buur bi dafa doon sàkku jaamam ! Mbëggeel gëlamal ko. Nun daal gis nanu mu nekk ci ag réer gu tar.
31فَلَمَّا سَمِعَتْ بِمَكْرِهِنَّ أَرْسَلَتْ إِلَيْهِنَّ وَأَعْتَدَتْ لَهُنَّ مُتَّكَأً وَآتَتْ كُلَّ وَاحِدَةٍ مِّنْهُنَّ سِكِّينًا وَقَالَتِ اخْرُجْ عَلَيْهِنَّ ۖ فَلَمَّا رَأَيْنَهُ أَكْبَرْنَهُ وَقَطَّعْنَ أَيْدِيَهُنَّ وَقُلْنَ حَاشَ لِلَّهِ مَا هَٰذَا بَشَرًا إِنْ هَٰذَا إِلَّا مَلَكٌ كَرِيمٌ
Bi mu déggee seen jëw, mu yónnee ca ñoom, waajalal leen aw ñam ; indil ku nekk ca ñoom paaka. [Ba ñuy lekk, mu ne Yuusufa] : “Génnal jëm ci ñoom” - Ba ñu ko gisee, ñu yéemu ci moom bay dagg seeni yoxo, di wax naan : “Cëy Yàlla ! Kii du nit, kii nekkul lu dul Malaaka mu tedd ! ”
32قَالَتْ فَذَٰلِكُنَّ الَّذِي لُمْتُنَّنِي فِيهِ ۖ وَلَقَدْ رَاوَدتُّهُ عَن نَّفْسِهِ فَاسْتَعْصَمَ ۖ وَلَئِن لَّمْ يَفْعَلْ مَا آمُرُهُ لَيُسْجَنَنَّ وَلَيَكُونًا مِّنَ الصَّاغِرِينَ
Mu ne : “Mu ngoog lii ngeen ma doon yedde. Maa ko sàkku woon mu bañ. Te bu deful li ma ko sant, waat naa ne dees na ko tëj kaso mu detteelu”.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
30Aaya

Tekki — Yusuf 30

Simoore Yusuf Aaya 30 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Aw jigéen di wax ci dëkk bi naan : “Jabaru…

Simoore Aaya 30/111 — Simoore Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Yusuf Dégg, Simoore Yusuf Tekki, Simoore Yusuf mp3, Simoore Yusuf pdf. Aaya 28–32. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers