Yusuf · 29/111
Tekki Waxtaan — Simoore Yusuf
يُوسُفُ أَعْرِضْ عَنْ هَٰذَا ۚ وَاسْتَغْفِرِي لِذَنبِكِ ۖ إِنَّكِ كُنتِ مِنَ الْخَاطِئِينَ ۝٢٩
Yoosofu a`rid `an haaza wastaghfiree lizambiki innaki kunti minal khaati`een
📖 Tekkim Wolof
Yuusufa, dëddul lii ! Te yaw [sama jabar] jéggalul sa bàkkaar ndax yaw bokk nga ca ñay def lu bon”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 27-31 — Simoore Yusuf

27وَإِن كَانَ قَمِيصُهُ قُدَّ مِن دُبُرٍ فَكَذَبَتْ وَهُوَ مِنَ الصَّادِقِينَ
Bu yéreem xottikoo ci ginnaaw, ndaw sa moo fen, moom mu bokk ca ñu dëggu ña”.
28فَلَمَّا رَأَىٰ قَمِيصَهُ قُدَّ مِن دُبُرٍ قَالَ إِنَّهُ مِن كَيْدِكُنَّ ۖ إِنَّ كَيْدَكُنَّ عَظِيمٌ
Ba jëkkër ja gisee yére ya xottiku ca ginnaaw, mu ne : “Lii ci seeni pexe la [yéen jigéen ñi] ! te seeni pexe réy na !
29يُوسُفُ أَعْرِضْ عَنْ هَٰذَا ۚ وَاسْتَغْفِرِي لِذَنبِكِ ۖ إِنَّكِ كُنتِ مِنَ الْخَاطِئِينَ
Yuusufa, dëddul lii ! Te yaw [sama jabar] jéggalul sa bàkkaar ndax yaw bokk nga ca ñay def lu bon”.
30۞ وَقَالَ نِسْوَةٌ فِي الْمَدِينَةِ امْرَأَتُ الْعَزِيزِ تُرَاوِدُ فَتَاهَا عَن نَّفْسِهِ ۖ قَدْ شَغَفَهَا حُبًّا ۖ إِنَّا لَنَرَاهَا فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
Aw jigéen di wax ci dëkk bi naan : “Jabaru buur bi dafa doon sàkku jaamam ! Mbëggeel gëlamal ko. Nun daal gis nanu mu nekk ci ag réer gu tar.
31فَلَمَّا سَمِعَتْ بِمَكْرِهِنَّ أَرْسَلَتْ إِلَيْهِنَّ وَأَعْتَدَتْ لَهُنَّ مُتَّكَأً وَآتَتْ كُلَّ وَاحِدَةٍ مِّنْهُنَّ سِكِّينًا وَقَالَتِ اخْرُجْ عَلَيْهِنَّ ۖ فَلَمَّا رَأَيْنَهُ أَكْبَرْنَهُ وَقَطَّعْنَ أَيْدِيَهُنَّ وَقُلْنَ حَاشَ لِلَّهِ مَا هَٰذَا بَشَرًا إِنْ هَٰذَا إِلَّا مَلَكٌ كَرِيمٌ
Bi mu déggee seen jëw, mu yónnee ca ñoom, waajalal leen aw ñam ; indil ku nekk ca ñoom paaka. [Ba ñuy lekk, mu ne Yuusufa] : “Génnal jëm ci ñoom” - Ba ñu ko gisee, ñu yéemu ci moom bay dagg seeni yoxo, di wax naan : “Cëy Yàlla ! Kii du nit, kii nekkul lu dul Malaaka mu tedd ! ”
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
29Aaya

Tekki — Yusuf 29

Simoore Yusuf Aaya 29 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yuusufa, dëddul lii ! Te yaw [sama jabar] jéggalul sa…

Simoore Aaya 29/111 — Simoore Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Yusuf Dégg, Simoore Yusuf Tekki, Simoore Yusuf mp3, Simoore Yusuf pdf. Aaya 27–31. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers