An-Nahl · 115/128
Tekki Waxtaan — Simoore An-Nahl
إِنَّمَا حَرَّمَ عَلَيْكُمُ الْمَيْتَةَ وَالدَّمَ وَلَحْمَ الْخِنزِيرِ وَمَا أُهِلَّ لِغَيْرِ اللَّهِ بِهِ ۖ فَمَنِ اضْطُرَّ غَيْرَ بَاغٍ وَلَا عَادٍ فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝١١٥
Innamaa harrma `alai kumul maitata waddama wa lahmal khinzeeri wa maaa uhilla lighairil laahi bihee famanid turra ghaira baaghinw wa laa `aadin fa innal laaha Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Waaye araamal na ci yéen médd, ak deret, ak yàppu mbaam-xuux ak lu ñu [rey] te tuddu ca keneen ku dul Yàlla. Képp ku nar a loru [ba tax mu lekk yooya araam], na xam ne Yàlla jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 113-117 — Simoore An-Nahl

113وَلَقَدْ جَاءَهُمْ رَسُولٌ مِّنْهُمْ فَكَذَّبُوهُ فَأَخَذَهُمُ الْعَذَابُ وَهُمْ ظَالِمُونَ
Ab Yonent bu bokk ci ñoom dikkal na leen, ñu weddi ko. Mbugal sadd leen te ñu nekkoon ñu tooñ.
114فَكُلُوا مِمَّا رَزَقَكُمُ اللَّهُ حَلَالًا طَيِّبًا وَاشْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ إِن كُنتُمْ إِيَّاهُ تَعْبُدُونَ
Lekk-leen ci xéewal gi leen Yàlla jox, muy lu lew, lu teey. Te ngeen gërëm Yàlla ciy xéewalam ndeem Moom rekk ngeen di jaamu.
115إِنَّمَا حَرَّمَ عَلَيْكُمُ الْمَيْتَةَ وَالدَّمَ وَلَحْمَ الْخِنزِيرِ وَمَا أُهِلَّ لِغَيْرِ اللَّهِ بِهِ ۖ فَمَنِ اضْطُرَّ غَيْرَ بَاغٍ وَلَا عَادٍ فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Waaye araamal na ci yéen médd, ak deret, ak yàppu mbaam-xuux ak lu ñu [rey] te tuddu ca keneen ku dul Yàlla. Képp ku nar a loru [ba tax mu lekk yooya araam], na xam ne Yàlla jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
116وَلَا تَقُولُوا لِمَا تَصِفُ أَلْسِنَتُكُمُ الْكَذِبَ هَٰذَا حَلَالٌ وَهَٰذَا حَرَامٌ لِّتَفْتَرُوا عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ لَا يُفْلِحُونَ
Buleen wax loo xam ne seeni làmmiñ a koy melal ciy fen, naan : “Lii dagan na, lii araam na”, di duural Yàlla ay fen. Te ñiy duural Yàlla ay fen duñu texe.
117مَتَاعٌ قَلِيلٌ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ñeel na leen yóbbal bu néew, ak mbugal mu metti.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
115Aaya

Tekki — An-Nahl 115

Simoore An-Nahl Aaya 115 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waaye araamal na ci yéen médd, ak deret, ak yàppu…

Simoore Aaya 115/128 — Simoore An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Nahl Dégg, Simoore An-Nahl Tekki, Simoore An-Nahl mp3, Simoore An-Nahl pdf. Aaya 113–117. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers