An-Nahl · 116/128
Tekki Waxtaan — Simoore An-Nahl
وَلَا تَقُولُوا لِمَا تَصِفُ أَلْسِنَتُكُمُ الْكَذِبَ هَٰذَا حَلَالٌ وَهَٰذَا حَرَامٌ لِّتَفْتَرُوا عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ لَا يُفْلِحُونَ ۝١١٦
Wa laa taqooloo limaa tasifu alsinatukumul kaziba haaza halaalunw wa haazaa haraamul litaftaroo `alal laahil kazib; innal lazeena yaftaroona `alal laahil kaziba laa yuflihoon
📖 Tekkim Wolof
Buleen wax loo xam ne seeni làmmiñ a koy melal ciy fen, naan : “Lii dagan na, lii araam na”, di duural Yàlla ay fen. Te ñiy duural Yàlla ay fen duñu texe.

🎧 Dégg


📜 Aaya 114-118 — Simoore An-Nahl

114فَكُلُوا مِمَّا رَزَقَكُمُ اللَّهُ حَلَالًا طَيِّبًا وَاشْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ إِن كُنتُمْ إِيَّاهُ تَعْبُدُونَ
Lekk-leen ci xéewal gi leen Yàlla jox, muy lu lew, lu teey. Te ngeen gërëm Yàlla ciy xéewalam ndeem Moom rekk ngeen di jaamu.
115إِنَّمَا حَرَّمَ عَلَيْكُمُ الْمَيْتَةَ وَالدَّمَ وَلَحْمَ الْخِنزِيرِ وَمَا أُهِلَّ لِغَيْرِ اللَّهِ بِهِ ۖ فَمَنِ اضْطُرَّ غَيْرَ بَاغٍ وَلَا عَادٍ فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Waaye araamal na ci yéen médd, ak deret, ak yàppu mbaam-xuux ak lu ñu [rey] te tuddu ca keneen ku dul Yàlla. Képp ku nar a loru [ba tax mu lekk yooya araam], na xam ne Yàlla jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
116وَلَا تَقُولُوا لِمَا تَصِفُ أَلْسِنَتُكُمُ الْكَذِبَ هَٰذَا حَلَالٌ وَهَٰذَا حَرَامٌ لِّتَفْتَرُوا عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ لَا يُفْلِحُونَ
Buleen wax loo xam ne seeni làmmiñ a koy melal ciy fen, naan : “Lii dagan na, lii araam na”, di duural Yàlla ay fen. Te ñiy duural Yàlla ay fen duñu texe.
117مَتَاعٌ قَلِيلٌ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ñeel na leen yóbbal bu néew, ak mbugal mu metti.
118وَعَلَى الَّذِينَ هَادُوا حَرَّمْنَا مَا قَصَصْنَا عَلَيْكَ مِن قَبْلُ ۖ وَمَا ظَلَمْنَاهُمْ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Te araamaloon nañu ca yahuud ya li Nu la nettali ca bu jëkk. Te tooñunu leen ; waaye ñoo tooñ seen bopp.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
116Aaya

Tekki — An-Nahl 116

Simoore An-Nahl Aaya 116 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buleen wax loo xam ne seeni làmmiñ a koy melal…

Simoore Aaya 116/128 — Simoore An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Nahl Dégg, Simoore An-Nahl Tekki, Simoore An-Nahl mp3, Simoore An-Nahl pdf. Aaya 114–118. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers