Al-Baqara · 261/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
مَّثَلُ الَّذِينَ يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ كَمَثَلِ حَبَّةٍ أَنبَتَتْ سَبْعَ سَنَابِلَ فِي كُلِّ سُنبُلَةٍ مِّائَةُ حَبَّةٍ ۗ وَاللَّهُ يُضَاعِفُ لِمَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ ٢٦١
Transliteration
Masalul lazeena yunfiqoona amwaalahum fee sabeelil laahi kamasali habbatin ambatat sab`a sanaabila fee kulli sumbulatim mi`atu habbah; wallaahu yudaa`ifu limai yashaaa; wallaahu Waasi`un `Aleem
Tekki (Tekkim Wolof)
📖 Tekkim Wolof
Méngaleg ña nga xam ne dañuy joxe seeni alal ci yoonu Yàlla mi ngi deme ni wenn pepp wu sax, seqi juróom-ñaari gupp, gupp wu nekk am téeméeri fepp. Yàlla mooy fulal ku ko soob,Yàlla ku yaatu ku xam la.
Additional reference in Fulfulde
🎧 Dégg
📜 Aaya 259-263 — Al-Baqara
259أَوْ كَالَّذِي مَرَّ عَلَىٰ قَرْيَةٍ وَهِيَ خَاوِيَةٌ عَلَىٰ عُرُوشِهَا قَالَ أَنَّىٰ يُحْيِي هَٰذِهِ اللَّهُ بَعْدَ مَوْتِهَا ۖ فَأَمَاتَهُ اللَّهُ مِائَةَ عَامٍ ثُمَّ بَعَثَهُ ۖ قَالَ كَمْ لَبِثْتَ ۖ قَالَ لَبِثْتُ يَوْمًا أَوْ بَعْضَ يَوْمٍ ۖ قَالَ بَل لَّبِثْتَ مِائَةَ عَامٍ فَانظُرْ إِلَىٰ طَعَامِكَ وَشَرَابِكَ لَمْ يَتَسَنَّهْ ۖ وَانظُرْ إِلَىٰ حِمَارِكَ وَلِنَجْعَلَكَ آيَةً لِّلنَّاسِ ۖ وَانظُرْ إِلَى الْعِظَامِ كَيْفَ نُنشِزُهَا ثُمَّ نَكْسُوهَا لَحْمًا ۚ فَلَمَّا تَبَيَّنَ لَهُ قَالَ أَعْلَمُ أَنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Walla ka romboon ab dëkk bu ràppoon ba ruus, mu ne : “Waa naka la Yàlla di dundalee lii ak ni mu dee te wow ? ”. Yàlla daldi koy rey moom lu tollu ci téeméeri at. Daldi koy dekkalaat, ne ko : “Sab yàggaay fii nu mu tollu ? ”. Mu ne ko : “Benn bis walla sax matu ko.”. Yàlla ne ko : “Am nga fi téeméeri at. Xoolal sa lekk gi ak sa naan gi : soppikuwuñu ; waaye xoolal sa mbaam mi... Te ngir nu def la kéemaan ci nit ñi, xoolal ni nuy dajalee yax yi, ba noppi wodde ko yàpp”. Ba mu ko leeree nàññ nag, mu daldi ne : “Xam naa xéll ne Yàlla mën na lu ne”.
260وَإِذْ قَالَ إِبْرَاهِيمُ رَبِّ أَرِنِي كَيْفَ تُحْيِي الْمَوْتَىٰ ۖ قَالَ أَوَلَمْ تُؤْمِن ۖ قَالَ بَلَىٰ وَلَٰكِن لِّيَطْمَئِنَّ قَلْبِي ۖ قَالَ فَخُذْ أَرْبَعَةً مِّنَ الطَّيْرِ فَصُرْهُنَّ إِلَيْكَ ثُمَّ اجْعَلْ عَلَىٰ كُلِّ جَبَلٍ مِّنْهُنَّ جُزْءًا ثُمَّ ادْعُهُنَّ يَأْتِينَكَ سَعْيًا ۚ وَاعْلَمْ أَنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
[Fàttalikul] ba Ibraahiima waxee ne : “Sama Boroom ! Won ma ni ngay dekkalee ku dee”, mu ne ko : “Xanaa dangaa gëmul? ”. Mu ne ko “Axakay ! Waaye ngir sama xel dal”. Mu ne ko : “Jëlal ñeenti njanaaw, teppasleen , boo noppee nga teg ci kaw tund wu ne aw dogit, boo noppee nga woo leen : danañu yëngatu wutsi la. Yàlla Aji-not [tedd] la te ku xereñ la.”
261مَّثَلُ الَّذِينَ يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ كَمَثَلِ حَبَّةٍ أَنبَتَتْ سَبْعَ سَنَابِلَ فِي كُلِّ سُنبُلَةٍ مِّائَةُ حَبَّةٍ ۗ وَاللَّهُ يُضَاعِفُ لِمَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ
Méngaleg ña nga xam ne dañuy joxe seeni alal ci yoonu Yàlla mi ngi deme ni wenn pepp wu sax, seqi juróom-ñaari gupp, gupp wu nekk am téeméeri fepp. Yàlla mooy fulal ku ko soob,Yàlla ku yaatu ku xam la.
262الَّذِينَ يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ثُمَّ لَا يُتْبِعُونَ مَا أَنفَقُوا مَنًّا وَلَا أَذًى ۙ لَّهُمْ أَجْرُهُمْ عِندَ رَبِّهِمْ وَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Ña nga xam ne dañuy joxe seeni alal ci yoonu Yàlla te duñu toftale ca la ñu joxe ñax walla kañu , danañu am seenug pey fa Yàlla seen Boroom. Duñu tiit, duñu jàq.
263۞ قَوْلٌ مَّعْرُوفٌ وَمَغْفِرَةٌ خَيْرٌ مِّن صَدَقَةٍ يَتْبَعُهَا أَذًى ۗ وَاللَّهُ غَنِيٌّ حَلِيمٌ
Wax ju yiw ak ag njeggal moo gëm sarax boo xam ne wax ju ñaaw a ca topp. Yàlla ku woomal la, ku lewet la.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
261Aaya
Tekki — Al-Baqara 261
Simoore Al-Baqara Aaya 261 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Méngaleg ña nga xam ne dañuy joxe seeni alal ci…Simoore Aaya 261/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 259–263. Tekkim Wolof: Fulfulde.
العربية
English
Bahasa Indonesia
Türkçe
Русский
فارسی
Français
اردو
বাংলা
Deutsch
Español
中文
हिन्दी
Português
Italiano
ภาษาไทย
Polski
Nederlands
Shqip
Kiswahili
O'zbek
தமிழ்
Melayu
Bosanski
Soomaali
Azərbaycan
کوردی
한국어
日本語
Svenska
Dansk
Norsk
پښتو
മലയാളം
සිංහල
Tamazight
Hausa
አማርኛ
Български
Тоҷикӣ
Қазақша
Filipino
سنڌي
Yorùbá
Fulfulde
Татарча
ئۇيغۇرچە
Кыргызча
ਪੰਜਾਬੀ
Jawa
తెలుగు
မြန်မာ
ગુજરાતી
Oromo
मराठी
Tiếng Việt
Malagasy
Нохчийн
Wolof
ދިވެހި
ಕನ್ನಡ
Українська
Ελληνικά
ქართული
ខ្មែរ
دری
Qafar af
Maranao
नेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers








