Al-Hajj · 65/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ سَخَّرَ لَكُم مَّا فِي الْأَرْضِ وَالْفُلْكَ تَجْرِي فِي الْبَحْرِ بِأَمْرِهِ وَيُمْسِكُ السَّمَاءَ أَن تَقَعَ عَلَى الْأَرْضِ إِلَّا بِإِذْنِهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ بِالنَّاسِ لَرَءُوفٌ رَّحِيمٌ ۝٦٥
Alam tara annal laaha sakhkhara lakum maa fil ardi wal fulka tajree fil bahri bi amrihee wa yumsikus samaaa`a an taqa`a `alal ardi illaa biiznih; innal laaha binnaasi la Ra`oofur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Ndax gisoo ne Yàlla tàggatal na leen li nekk ci suuf si, te gaal gay daw ci ndigalam la ? Te Moo tee asamaan daanu ci kaw suuf si ci ndigalam. Te Yàlla kuy ñeewant la, di Kuy jagle nit ñi yërmaandeem.
🎧 Dégg

📜 Aaya 63-67 — Al-Hajj

63أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَتُصْبِحُ الْأَرْضُ مُخْضَرَّةً ۗ إِنَّ اللَّهَ لَطِيفٌ خَبِيرٌ
Ndax dangaa gisul ne Yàlla mooy wàcce ndox mu jóge asamaan, soppi suuf si mu naat ? Yàlla Kuy ñeewant la (jaam ñi), Ku deñ-kumpa la.
64لَّهُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۗ وَإِنَّ اللَّهَ لَهُوَ الْغَنِيُّ الْحَمِيدُ
Moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Te Yàlla moom ku woomal la, Ku yeyoo cant la !
65أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ سَخَّرَ لَكُم مَّا فِي الْأَرْضِ وَالْفُلْكَ تَجْرِي فِي الْبَحْرِ بِأَمْرِهِ وَيُمْسِكُ السَّمَاءَ أَن تَقَعَ عَلَى الْأَرْضِ إِلَّا بِإِذْنِهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ بِالنَّاسِ لَرَءُوفٌ رَّحِيمٌ
Ndax gisoo ne Yàlla tàggatal na leen li nekk ci suuf si, te gaal gay daw ci ndigalam la ? Te Moo tee asamaan daanu ci kaw suuf si ci ndigalam. Te Yàlla kuy ñeewant la, di Kuy jagle nit ñi yërmaandeem.
66وَهُوَ الَّذِي أَحْيَاكُمْ ثُمَّ يُمِيتُكُمْ ثُمَّ يُحْيِيكُمْ ۗ إِنَّ الْإِنسَانَ لَكَفُورٌ
Te Moom mooy ki leen dundal te Dana leen rey, ba noppi Mu dundalaat leen. Waaye nit weddiwaakoon la.
67لِّكُلِّ أُمَّةٍ جَعَلْنَا مَنسَكًا هُمْ نَاسِكُوهُ ۖ فَلَا يُنَازِعُنَّكَ فِي الْأَمْرِ ۚ وَادْعُ إِلَىٰ رَبِّكَ ۖ إِنَّكَ لَعَلَىٰ هُدًى مُّسْتَقِيمٍ
Xeet wu nekk defal Nanu ko jaamukaay wu ñu koy jaamoo. Kon buñu xëccook yaw ci mbir yi ! Te nanga woote jëme ci sa Boroom. Yaw de yaa ngi ci njub gu ne xocc.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
65Aaya

Tekki — Al-Hajj 65

Simoore Al-Hajj Aaya 65 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ndax gisoo ne Yàlla tàggatal na leen li nekk ci…

Simoore Aaya 65/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 63–67. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers