Al-Qasas · 29/88
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Qasas
۞ فَلَمَّا قَضَىٰ مُوسَى الْأَجَلَ وَسَارَ بِأَهْلِهِ آنَسَ مِن جَانِبِ الطُّورِ نَارًا قَالَ لِأَهْلِهِ امْكُثُوا إِنِّي آنَسْتُ نَارًا لَّعَلِّي آتِيكُم مِّنْهَا بِخَبَرٍ أَوْ جَذْوَةٍ مِّنَ النَّارِ لَعَلَّكُمْ تَصْطَلُونَ ۝٢٩
Falammmaa qadaa Moosal ajala wa saara bi ahliheee aanasa min jaanibit Toori naaran qaala li ahlihim kusooo inneee aanastu naaral la `alleee aateekum minhaa bikhabarin aw jazwatim minan naari la `allakum tastaloon
📖 Tekkim Wolof
Ba Muusaa matalee dig ba, màng njabootam di ñibbi, gis na safara ci wàllug ndeyjooru tundu doju Tuur wa. Mu ne leen : “Xaarleen ma fii, li ma séen aw safara la. Amaana ma indil leen ci xibaar walla ay xal ngir ngeen mën caa jaaroo”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 27-31 — Simoore Al-Qasas

27قَالَ إِنِّي أُرِيدُ أَنْ أُنكِحَكَ إِحْدَى ابْنَتَيَّ هَاتَيْنِ عَلَىٰ أَن تَأْجُرَنِي ثَمَانِيَ حِجَجٍ ۖ فَإِنْ أَتْمَمْتَ عَشْرًا فَمِنْ عِندِكَ ۖ وَمَا أُرِيدُ أَنْ أَشُقَّ عَلَيْكَ ۚ سَتَجِدُنِي إِن شَاءَ اللَّهُ مِنَ الصَّالِحِينَ
Mu ne ko : “Dama laa bëgg may kenn ci sama ñaari doom yu jigéen yii ci nga doon sama surga juróom-ñetti at. Soo ko matalee fukk nag, ci sa coobare lay doon ; ndax man bëgguma laa teg coono. Te bu soobee Yàlla, danga xam ne nit ku yiw laa”.
28قَالَ ذَٰلِكَ بَيْنِي وَبَيْنَكَ ۖ أَيَّمَا الْأَجَلَيْنِ قَضَيْتُ فَلَا عُدْوَانَ عَلَيَّ ۖ وَاللَّهُ عَلَىٰ مَا نَقُولُ وَكِيلٌ
Mu daldi ne : “Loolu sama diggante la ak yaw. Ñaar ñépp a yem ci man, duma la bunduxataal mukk. Te lii nuy wax Yàllaa di seede si”.
29۞ فَلَمَّا قَضَىٰ مُوسَى الْأَجَلَ وَسَارَ بِأَهْلِهِ آنَسَ مِن جَانِبِ الطُّورِ نَارًا قَالَ لِأَهْلِهِ امْكُثُوا إِنِّي آنَسْتُ نَارًا لَّعَلِّي آتِيكُم مِّنْهَا بِخَبَرٍ أَوْ جَذْوَةٍ مِّنَ النَّارِ لَعَلَّكُمْ تَصْطَلُونَ
Ba Muusaa matalee dig ba, màng njabootam di ñibbi, gis na safara ci wàllug ndeyjooru tundu doju Tuur wa. Mu ne leen : “Xaarleen ma fii, li ma séen aw safara la. Amaana ma indil leen ci xibaar walla ay xal ngir ngeen mën caa jaaroo”.
30فَلَمَّا أَتَاهَا نُودِيَ مِن شَاطِئِ الْوَادِ الْأَيْمَنِ فِي الْبُقْعَةِ الْمُبَارَكَةِ مِنَ الشَّجَرَةِ أَن يَا مُوسَىٰ إِنِّي أَنَا اللَّهُ رَبُّ الْعَالَمِينَ
Ba mu fa agsee, mu am lu ko woo ci xuru ndeyjoor wa, ne ko : “Éy Muusaa ! ManMii Maa di Yàlla jiy Boroom àddina si yépp”.
31وَأَنْ أَلْقِ عَصَاكَ ۖ فَلَمَّا رَآهَا تَهْتَزُّ كَأَنَّهَا جَانٌّ وَلَّىٰ مُدْبِرًا وَلَمْ يُعَقِّبْ ۚ يَا مُوسَىٰ أَقْبِلْ وَلَا تَخَفْ ۖ إِنَّكَ مِنَ الْآمِنِينَ
Te : “Nanga sànni sa yet wi” ; [Ba mu ko sànnee] gis ne ma ngay yëngatu mel ni jaan, mu ne baxarñit.”. Yàlla woowaat ko, ne ko : “Dellusil te bul tiit : yaa ngi ci lu wóor”.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
29Aaya

Tekki — Al-Qasas 29

Simoore Al-Qasas Aaya 29 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba Muusaa matalee dig ba, màng njabootam di ñibbi, gis…

Simoore Aaya 29/88 — Simoore Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Qasas Dégg, Simoore Al-Qasas Tekki, Simoore Al-Qasas mp3, Simoore Al-Qasas pdf. Aaya 27–31. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers