Aali Imran · 16/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
الَّذِينَ يَقُولُونَ رَبَّنَا إِنَّنَا آمَنَّا فَاغْفِرْ لَنَا ذُنُوبَنَا وَقِنَا عَذَابَ النَّارِ ۝١٦
Allazeena yaqooloona Rabbanaaa innanaaa aamannaa faghfir lanaa zunoobanaa wa qinaa `azaaban Naar
📖 Tekkim Wolof
ñooy ñay wax naan : "Sunu Boroom, nun gëm nanu ; jéggal nu sunuy bàkkaar, te fegal nu mbugalu Safara”,
🎧 Dégg

📜 Aaya 14-18 — Aali Imran

14زُيِّنَ لِلنَّاسِ حُبُّ الشَّهَوَاتِ مِنَ النِّسَاءِ وَالْبَنِينَ وَالْقَنَاطِيرِ الْمُقَنطَرَةِ مِنَ الذَّهَبِ وَالْفِضَّةِ وَالْخَيْلِ الْمُسَوَّمَةِ وَالْأَنْعَامِ وَالْحَرْثِ ۗ ذَٰلِكَ مَتَاعُ الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۖ وَاللَّهُ عِندَهُ حُسْنُ الْمَآبِ
Rafetaleef na ci nit ñi sopp bànneex ci jigéen ñi ak ay doom yu bari, alal ju bari ci wurus walla ci xaalis, fas yu tàggutu, ak i jur [waruwaay], ak i alal mbey ; loolu lépp yóbbalub àddina doŋŋ la, delluwaay ba gën, ma nga ca Yàlla.
15۞ قُلْ أَؤُنَبِّئُكُم بِخَيْرٍ مِّن ذَٰلِكُمْ ۚ لِلَّذِينَ اتَّقَوْا عِندَ رَبِّهِمْ جَنَّاتٌ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا وَأَزْوَاجٌ مُّطَهَّرَةٌ وَرِضْوَانٌ مِّنَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِالْعِبَادِ
Neel : “Moo ndax duma leen xamal lu gën loolu ci yéen ? Gaa ña nga xam ne dañoo ragal Yàlla, am nañu, fa seen Boroom, Àjjana joo xam ne dex yaa ngay daw ci ronam, ñu sax fa dàkk ak i soxna yu ñu laabal , ak ngërëm lu bawoo ca Yàlla.” Yàllaa ngi gis jaam ñi,
16الَّذِينَ يَقُولُونَ رَبَّنَا إِنَّنَا آمَنَّا فَاغْفِرْ لَنَا ذُنُوبَنَا وَقِنَا عَذَابَ النَّارِ
ñooy ñay wax naan : "Sunu Boroom, nun gëm nanu ; jéggal nu sunuy bàkkaar, te fegal nu mbugalu Safara”,
17الصَّابِرِينَ وَالصَّادِقِينَ وَالْقَانِتِينَ وَالْمُنفِقِينَ وَالْمُسْتَغْفِرِينَ بِالْأَسْحَارِ
ñooy, muñkat ya, ña dëggal, diy jaamukat, diy joxekati alal [ngir Yàlla] tey sàkku njéggal waxtuw njël.
18شَهِدَ اللَّهُ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ وَالْمَلَائِكَةُ وَأُولُو الْعِلْمِ قَائِمًا بِالْقِسْطِ ۚ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Yàlla seede na ne, amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Malaaka ya ak woroom xam-xam ya taxawe ci maandu it, seede nañu ne amul jeneen Yàlla ju dul Moom. Ku not la, ku xereñ la !
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
16Aaya

Tekki — Aali Imran 16

Simoore Aali Imran Aaya 16 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ñooy ñay wax naan : "Sunu Boroom, nun gëm nanu…

Simoore Aaya 16/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 14–18. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers