Aali Imran · 164/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
لَقَدْ مَنَّ اللَّهُ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ إِذْ بَعَثَ فِيهِمْ رَسُولًا مِّنْ أَنفُسِهِمْ يَتْلُو عَلَيْهِمْ آيَاتِهِ وَيُزَكِّيهِمْ وَيُعَلِّمُهُمُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَإِن كَانُوا مِن قَبْلُ لَفِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ ۝١٦٤
Laqad mannal laahu `alal mu`mineena iz ba`asa feehim Rasoolam min anfusihim yatloo `alaihim Aayaatihee wa yuzakkeehim wa yu`allimu humul Kitaaba wal Hikmata wa in kaanoo min qablu lafee dalaalim mubeen
📖 Tekkim Wolof
Yàlla xéewale na ña gëm ba Mu yónnee ca ñoom ab Yonent bu bokk ca ñoom, di leen jàngal kàddoom, di leen laabal, di leen xamal Téere ba ak xam-xamu xereñe, te la ko jiitu ñu nekkoon ci réer gu tar.
🎧 Dégg

📜 Aaya 162-166 — Aali Imran

162أَفَمَنِ اتَّبَعَ رِضْوَانَ اللَّهِ كَمَن بَاءَ بِسَخَطٍ مِّنَ اللَّهِ وَمَأْوَاهُ جَهَنَّمُ ۚ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ
Ndax kuy topp ngërëmul Yàlla, dana yem ak ku sóobu ci xarabug Yàlla ? Safaraa di këram te googu muj, du gu ñuy taamu !
163هُمْ دَرَجَاتٌ عِندَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِمَا يَعْمَلُونَ
Xam na ne duñu yem mukk waay. Ëppante nañu daraja [dayo] ca Yàlla, ndax Yàllaa ngi ne jàkk ca la ñuy jëf.
164لَقَدْ مَنَّ اللَّهُ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ إِذْ بَعَثَ فِيهِمْ رَسُولًا مِّنْ أَنفُسِهِمْ يَتْلُو عَلَيْهِمْ آيَاتِهِ وَيُزَكِّيهِمْ وَيُعَلِّمُهُمُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَإِن كَانُوا مِن قَبْلُ لَفِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
Yàlla xéewale na ña gëm ba Mu yónnee ca ñoom ab Yonent bu bokk ca ñoom, di leen jàngal kàddoom, di leen laabal, di leen xamal Téere ba ak xam-xamu xereñe, te la ko jiitu ñu nekkoon ci réer gu tar.
165أَوَلَمَّا أَصَابَتْكُم مُّصِيبَةٌ قَدْ أَصَبْتُم مِّثْلَيْهَا قُلْتُمْ أَنَّىٰ هَٰذَا ۖ قُلْ هُوَ مِنْ عِندِ أَنفُسِكُمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Naka mu ? Bu leen aw tiis dalee - te fekk daan ngeen [seeni noon] lu mat ñaari yoon - ngeen di wax naan “Naka la lii mën a nekkee ? ”. Neel : “Ci yéen la”. Yàlla mën na lu ne.
166وَمَا أَصَابَكُمْ يَوْمَ الْتَقَى الْجَمْعَانِ فَبِإِذْنِ اللَّهِ وَلِيَعْلَمَ الْمُؤْمِنِينَ
La leen dalool ca seenub dajeeb ñaari mbooloo ya, lu Yàlla nammoon la ngir mu xàmmee ca ña gëm [xareb Uhud]
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
164Aaya

Tekki — Aali Imran 164

Simoore Aali Imran Aaya 164 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla xéewale na ña gëm ba Mu yónnee ca ñoom…

Simoore Aaya 164/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 162–166. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers