Aali Imran · 163/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
هُمْ دَرَجَاتٌ عِندَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِمَا يَعْمَلُونَ ۝١٦٣
Hum darajaatun `indal laah; wallaahu baseerum bimaa ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Xam na ne duñu yem mukk waay. Ëppante nañu daraja [dayo] ca Yàlla, ndax Yàllaa ngi ne jàkk ca la ñuy jëf.

🎧 Dégg


📜 Aaya 161-165 — Aali Imran

161وَمَا كَانَ لِنَبِيٍّ أَن يَغُلَّ ۚ وَمَن يَغْلُلْ يَأْتِ بِمَا غَلَّ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۚ ثُمَّ تُوَفَّىٰ كُلُّ نَفْسٍ مَّا كَسَبَتْ وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ
Amul benn Yonent buy labax alali xare. Te képp ku sàcc alali xare, bu Bis-pénc baa, dana ko indi. Ku nekk door a jot la mu jëfoon ba mu mat sëkk.
162أَفَمَنِ اتَّبَعَ رِضْوَانَ اللَّهِ كَمَن بَاءَ بِسَخَطٍ مِّنَ اللَّهِ وَمَأْوَاهُ جَهَنَّمُ ۚ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ
Ndax kuy topp ngërëmul Yàlla, dana yem ak ku sóobu ci xarabug Yàlla ? Safaraa di këram te googu muj, du gu ñuy taamu !
163هُمْ دَرَجَاتٌ عِندَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِمَا يَعْمَلُونَ
Xam na ne duñu yem mukk waay. Ëppante nañu daraja [dayo] ca Yàlla, ndax Yàllaa ngi ne jàkk ca la ñuy jëf.
164لَقَدْ مَنَّ اللَّهُ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ إِذْ بَعَثَ فِيهِمْ رَسُولًا مِّنْ أَنفُسِهِمْ يَتْلُو عَلَيْهِمْ آيَاتِهِ وَيُزَكِّيهِمْ وَيُعَلِّمُهُمُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَإِن كَانُوا مِن قَبْلُ لَفِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
Yàlla xéewale na ña gëm ba Mu yónnee ca ñoom ab Yonent bu bokk ca ñoom, di leen jàngal kàddoom, di leen laabal, di leen xamal Téere ba ak xam-xamu xereñe, te la ko jiitu ñu nekkoon ci réer gu tar.
165أَوَلَمَّا أَصَابَتْكُم مُّصِيبَةٌ قَدْ أَصَبْتُم مِّثْلَيْهَا قُلْتُمْ أَنَّىٰ هَٰذَا ۖ قُلْ هُوَ مِنْ عِندِ أَنفُسِكُمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Naka mu ? Bu leen aw tiis dalee - te fekk daan ngeen [seeni noon] lu mat ñaari yoon - ngeen di wax naan “Naka la lii mën a nekkee ? ”. Neel : “Ci yéen la”. Yàlla mën na lu ne.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
163Aaya

Tekki — Aali Imran 163

Simoore Aali Imran Aaya 163 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Xam na ne duñu yem mukk waay. Ëppante nañu daraja…

Simoore Aaya 163/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 161–165. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers