Aali Imran · 172/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
الَّذِينَ اسْتَجَابُوا لِلَّهِ وَالرَّسُولِ مِن بَعْدِ مَا أَصَابَهُمُ الْقَرْحُ ۚ لِلَّذِينَ أَحْسَنُوا مِنْهُمْ وَاتَّقَوْا أَجْرٌ عَظِيمٌ ۝١٧٢
Allazeenas tajaaboo lil laahi war Rasooli mim ba`di maaa asaabahumulqarh; lillazeena ahsanoo minhum wattaqaw ajrun `azeem
📖 Tekkim Wolof
Ñoom ña wuyu [wooteb] Yàlla ak Yonent ba, ginnaaw ba leen jam-jam ya [ca xare Uhud] dalee, ña doon rafetal ca ñoom te ragal Yàlla, am nañu pey gu màgg.

🎧 Dégg


📜 Aaya 170-174 — Simoore Aali Imran

170فَرِحِينَ بِمَا آتَاهُمُ اللَّهُ مِن فَضْلِهِ وَيَسْتَبْشِرُونَ بِالَّذِينَ لَمْ يَلْحَقُوا بِهِم مِّنْ خَلْفِهِمْ أَلَّا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
dañuy bég ca la leen Yàlla jox ci ay ngënéelam, di bég it ca jullit ya ñu bàyyi ginnaaw te fekkeeguñu leen, duñu jàq, duñu am naqar bu ñu fa eggee.
171۞ يَسْتَبْشِرُونَ بِنِعْمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَفَضْلٍ وَأَنَّ اللَّهَ لَا يُضِيعُ أَجْرَ الْمُؤْمِنِينَ
Danañu bég ca xéewal ya bawoo fa Yàlla ak i ngënéelam, ak ca la nga xam ne Yàlla du sànk peyub ñi gëm.
172الَّذِينَ اسْتَجَابُوا لِلَّهِ وَالرَّسُولِ مِن بَعْدِ مَا أَصَابَهُمُ الْقَرْحُ ۚ لِلَّذِينَ أَحْسَنُوا مِنْهُمْ وَاتَّقَوْا أَجْرٌ عَظِيمٌ
Ñoom ña wuyu [wooteb] Yàlla ak Yonent ba, ginnaaw ba leen jam-jam ya [ca xare Uhud] dalee, ña doon rafetal ca ñoom te ragal Yàlla, am nañu pey gu màgg.
173الَّذِينَ قَالَ لَهُمُ النَّاسُ إِنَّ النَّاسَ قَدْ جَمَعُوا لَكُمْ فَاخْشَوْهُمْ فَزَادَهُمْ إِيمَانًا وَقَالُوا حَسْبُنَا اللَّهُ وَنِعْمَ الْوَكِيلُ
Ñooy ña nit ña ne woon : “Yéen a toog, waaye nit ñaa [seeni noon] ngi daje ngir sànk leen, war ngeen a tiit” - faf loolu yokk leen ngëm - ñu toontu ne : “Yàlla doy nanu te Mooy ngën gi wéeruwaay”.
174فَانقَلَبُوا بِنِعْمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَفَضْلٍ لَّمْ يَمْسَسْهُمْ سُوءٌ وَاتَّبَعُوا رِضْوَانَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ ذُو فَضْلٍ عَظِيمٍ
Ñu dellu ñibbi ànd ak xéewalug Yàlla. Te dara lu bon daluleen, topp nañu lu neex Yàlla. Te Yàlla boroom ngëneel yu màgg la.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
172Aaya

Tekki — Aali Imran 172

Simoore Aali Imran Aaya 172 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñoom ña wuyu [wooteb] Yàlla ak Yonent ba, ginnaaw ba…

Simoore Aaya 172/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 170–174. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers