Aali Imran · 173/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
الَّذِينَ قَالَ لَهُمُ النَّاسُ إِنَّ النَّاسَ قَدْ جَمَعُوا لَكُمْ فَاخْشَوْهُمْ فَزَادَهُمْ إِيمَانًا وَقَالُوا حَسْبُنَا اللَّهُ وَنِعْمَ الْوَكِيلُ ۝١٧٣
Allazeena qaala lahumun naasu innan naasa qad jama`oo lakum fakhshawhuin fazaadahum eemaannanwa wa qaaloo hasbunal laahu wa ni`malwakeel
📖 Tekkim Wolof
Ñooy ña nit ña ne woon : “Yéen a toog, waaye nit ñaa [seeni noon] ngi daje ngir sànk leen, war ngeen a tiit” - faf loolu yokk leen ngëm - ñu toontu ne : “Yàlla doy nanu te Mooy ngën gi wéeruwaay”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 171-175 — Simoore Aali Imran

171۞ يَسْتَبْشِرُونَ بِنِعْمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَفَضْلٍ وَأَنَّ اللَّهَ لَا يُضِيعُ أَجْرَ الْمُؤْمِنِينَ
Danañu bég ca xéewal ya bawoo fa Yàlla ak i ngënéelam, ak ca la nga xam ne Yàlla du sànk peyub ñi gëm.
172الَّذِينَ اسْتَجَابُوا لِلَّهِ وَالرَّسُولِ مِن بَعْدِ مَا أَصَابَهُمُ الْقَرْحُ ۚ لِلَّذِينَ أَحْسَنُوا مِنْهُمْ وَاتَّقَوْا أَجْرٌ عَظِيمٌ
Ñoom ña wuyu [wooteb] Yàlla ak Yonent ba, ginnaaw ba leen jam-jam ya [ca xare Uhud] dalee, ña doon rafetal ca ñoom te ragal Yàlla, am nañu pey gu màgg.
173الَّذِينَ قَالَ لَهُمُ النَّاسُ إِنَّ النَّاسَ قَدْ جَمَعُوا لَكُمْ فَاخْشَوْهُمْ فَزَادَهُمْ إِيمَانًا وَقَالُوا حَسْبُنَا اللَّهُ وَنِعْمَ الْوَكِيلُ
Ñooy ña nit ña ne woon : “Yéen a toog, waaye nit ñaa [seeni noon] ngi daje ngir sànk leen, war ngeen a tiit” - faf loolu yokk leen ngëm - ñu toontu ne : “Yàlla doy nanu te Mooy ngën gi wéeruwaay”.
174فَانقَلَبُوا بِنِعْمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَفَضْلٍ لَّمْ يَمْسَسْهُمْ سُوءٌ وَاتَّبَعُوا رِضْوَانَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ ذُو فَضْلٍ عَظِيمٍ
Ñu dellu ñibbi ànd ak xéewalug Yàlla. Te dara lu bon daluleen, topp nañu lu neex Yàlla. Te Yàlla boroom ngëneel yu màgg la.
175إِنَّمَا ذَٰلِكُمُ الشَّيْطَانُ يُخَوِّفُ أَوْلِيَاءَهُ فَلَا تَخَافُوهُمْ وَخَافُونِ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
[Xupp googu ñu leen di xupp] du dara lu dul jëfi Seytaane dafay tiitloo aw nitam. Buleen leen ragal. Ragal-leen Ma, ndeem ñu gëm ngeen.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
173Aaya

Tekki — Aali Imran 173

Simoore Aali Imran Aaya 173 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñooy ña nit ña ne woon : “Yéen a toog,…

Simoore Aaya 173/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 171–175. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers