Aali Imran · 64/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ تَعَالَوْا إِلَىٰ كَلِمَةٍ سَوَاءٍ بَيْنَنَا وَبَيْنَكُمْ أَلَّا نَعْبُدَ إِلَّا اللَّهَ وَلَا نُشْرِكَ بِهِ شَيْئًا وَلَا يَتَّخِذَ بَعْضُنَا بَعْضًا أَرْبَابًا مِّن دُونِ اللَّهِ ۚ فَإِن تَوَلَّوْا فَقُولُوا اشْهَدُوا بِأَنَّا مُسْلِمُونَ ۝٦٤
Qul yaa Ahlal Kitaabi ta`aalaw ilaa Kalimatin sawaaa`im bainanaa wa bainakum allaa na`buda illal laaha wa laa nushrika bihee shai`anw wa laa yattakhiza ba`dunaa ba`dan arbaabam min doonil laah; fa in tawallaw faqoolush hadoo bi annaa muslimoon
📖 Tekkim Wolof
- Neel : “Yéen ñoñ-téere yi, kaayleen ci baat boo xam ne yéen ak nun noo ciy maase : dunu jaamu ku dul Yàlla, te nu bañ cee bokkaale dara, te kenn ci nun bañ jël moroomam jàppe ko Yàlla, di ko jaamu”. Su ñu bañee ba dummóoyu, neeleen : “Seedeleen ne nun dey way-wommatu lanu [ci topp Yàlla]”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 62-66 — Simoore Aali Imran

62إِنَّ هَٰذَا لَهُوَ الْقَصَصُ الْحَقُّ ۚ وَمَا مِنْ إِلَٰهٍ إِلَّا اللَّهُ ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Lii mooy nettali yu dëggu ya. Te amul yàlla ju yayoo jaamu ku dul Yàlla. Te Mooy ki not, ki xereñ.
63فَإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِالْمُفْسِدِينَ
Bu ñu dëddoo [dummóoyu] ... Yàlla xàmmee na yàqkat ya !
64قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ تَعَالَوْا إِلَىٰ كَلِمَةٍ سَوَاءٍ بَيْنَنَا وَبَيْنَكُمْ أَلَّا نَعْبُدَ إِلَّا اللَّهَ وَلَا نُشْرِكَ بِهِ شَيْئًا وَلَا يَتَّخِذَ بَعْضُنَا بَعْضًا أَرْبَابًا مِّن دُونِ اللَّهِ ۚ فَإِن تَوَلَّوْا فَقُولُوا اشْهَدُوا بِأَنَّا مُسْلِمُونَ
- Neel : “Yéen ñoñ-téere yi, kaayleen ci baat boo xam ne yéen ak nun noo ciy maase : dunu jaamu ku dul Yàlla, te nu bañ cee bokkaale dara, te kenn ci nun bañ jël moroomam jàppe ko Yàlla, di ko jaamu”. Su ñu bañee ba dummóoyu, neeleen : “Seedeleen ne nun dey way-wommatu lanu [ci topp Yàlla]”.
65يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تُحَاجُّونَ فِي إِبْرَاهِيمَ وَمَا أُنزِلَتِ التَّوْرَاةُ وَالْإِنجِيلُ إِلَّا مِن بَعْدِهِ ۚ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
Yéen ñoñ-téere, ana lan moo waral ngeen di dàggasante ci mbiri Ibraahiima, te Tawreet ak Injiil ginnaawam lañu wàcc ? Moo ndax dungeen xel-lu ?
66هَا أَنتُمْ هَٰؤُلَاءِ حَاجَجْتُمْ فِيمَا لَكُم بِهِ عِلْمٌ فَلِمَ تُحَاجُّونَ فِيمَا لَيْسَ لَكُم بِهِ عِلْمٌ ۚ وَاللَّهُ يَعْلَمُ وَأَنتُمْ لَا تَعْلَمُونَ
Yëgleen ne dàggasante ngeen ci lu ngeen xam [mbiri Iisaa]. Lu tax ngeen di dàgge ci lu ngeen amul xam-xam [Mbiri Ibraahiima] ? Yàlla xam na te yéen xamuleen.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
64Aaya

Tekki — Aali Imran 64

Simoore Aali Imran Aaya 64 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : - Neel : “Yéen ñoñ-téere yi, kaayleen ci baat boo…

Simoore Aaya 64/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 62–66. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers