Aali Imran · 63/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
فَإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِالْمُفْسِدِينَ ۝٦٣
Fa in tawallaw fa innal laaha`aleemun bil mufsideen
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu dëddoo [dummóoyu] ... Yàlla xàmmee na yàqkat ya !

🎧 Dégg


📜 Aaya 61-65 — Simoore Aali Imran

61فَمَنْ حَاجَّكَ فِيهِ مِن بَعْدِ مَا جَاءَكَ مِنَ الْعِلْمِ فَقُلْ تَعَالَوْا نَدْعُ أَبْنَاءَنَا وَأَبْنَاءَكُمْ وَنِسَاءَنَا وَنِسَاءَكُمْ وَأَنفُسَنَا وَأَنفُسَكُمْ ثُمَّ نَبْتَهِلْ فَنَجْعَل لَّعْنَتَ اللَّهِ عَلَى الْكَاذِبِينَ
Ku cay dàggasante ak yaw, ginnaaw la la dikke ci xam-xam [ci mbiri Iisaa], neel : “Kaayleen nu woo sunuy doom ak sunuy soxna ak seeni soxna, nu ñëw, ngeen ñëw yéen ci seen bopp topp nu toroxlu, rëbbante rëbbum Yàlla dal ci ña fen [ci mbiri Iisaa].
62إِنَّ هَٰذَا لَهُوَ الْقَصَصُ الْحَقُّ ۚ وَمَا مِنْ إِلَٰهٍ إِلَّا اللَّهُ ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Lii mooy nettali yu dëggu ya. Te amul yàlla ju yayoo jaamu ku dul Yàlla. Te Mooy ki not, ki xereñ.
63فَإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِالْمُفْسِدِينَ
Bu ñu dëddoo [dummóoyu] ... Yàlla xàmmee na yàqkat ya !
64قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ تَعَالَوْا إِلَىٰ كَلِمَةٍ سَوَاءٍ بَيْنَنَا وَبَيْنَكُمْ أَلَّا نَعْبُدَ إِلَّا اللَّهَ وَلَا نُشْرِكَ بِهِ شَيْئًا وَلَا يَتَّخِذَ بَعْضُنَا بَعْضًا أَرْبَابًا مِّن دُونِ اللَّهِ ۚ فَإِن تَوَلَّوْا فَقُولُوا اشْهَدُوا بِأَنَّا مُسْلِمُونَ
- Neel : “Yéen ñoñ-téere yi, kaayleen ci baat boo xam ne yéen ak nun noo ciy maase : dunu jaamu ku dul Yàlla, te nu bañ cee bokkaale dara, te kenn ci nun bañ jël moroomam jàppe ko Yàlla, di ko jaamu”. Su ñu bañee ba dummóoyu, neeleen : “Seedeleen ne nun dey way-wommatu lanu [ci topp Yàlla]”.
65يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تُحَاجُّونَ فِي إِبْرَاهِيمَ وَمَا أُنزِلَتِ التَّوْرَاةُ وَالْإِنجِيلُ إِلَّا مِن بَعْدِهِ ۚ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
Yéen ñoñ-téere, ana lan moo waral ngeen di dàggasante ci mbiri Ibraahiima, te Tawreet ak Injiil ginnaawam lañu wàcc ? Moo ndax dungeen xel-lu ?
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
63Aaya

Tekki — Aali Imran 63

Simoore Aali Imran Aaya 63 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu dëddoo [dummóoyu] ... Yàlla xàmmee na yàqkat ya…

Simoore Aaya 63/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 61–65. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers