Aali Imran · 65/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تُحَاجُّونَ فِي إِبْرَاهِيمَ وَمَا أُنزِلَتِ التَّوْرَاةُ وَالْإِنجِيلُ إِلَّا مِن بَعْدِهِ ۚ أَفَلَا تَعْقِلُونَ ۝٦٥
Yaaa Ahlal Kitaabi limaa tuhaaajjoona feee Ibraaheema wa maaa unzilatit Tawraatu wal Injeelu illaa mim ba`dih; afala ta`qiloon
📖 Tekkim Wolof
Yéen ñoñ-téere, ana lan moo waral ngeen di dàggasante ci mbiri Ibraahiima, te Tawreet ak Injiil ginnaawam lañu wàcc ? Moo ndax dungeen xel-lu ?

🎧 Dégg


📜 Aaya 63-67 — Simoore Aali Imran

63فَإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِالْمُفْسِدِينَ
Bu ñu dëddoo [dummóoyu] ... Yàlla xàmmee na yàqkat ya !
64قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ تَعَالَوْا إِلَىٰ كَلِمَةٍ سَوَاءٍ بَيْنَنَا وَبَيْنَكُمْ أَلَّا نَعْبُدَ إِلَّا اللَّهَ وَلَا نُشْرِكَ بِهِ شَيْئًا وَلَا يَتَّخِذَ بَعْضُنَا بَعْضًا أَرْبَابًا مِّن دُونِ اللَّهِ ۚ فَإِن تَوَلَّوْا فَقُولُوا اشْهَدُوا بِأَنَّا مُسْلِمُونَ
- Neel : “Yéen ñoñ-téere yi, kaayleen ci baat boo xam ne yéen ak nun noo ciy maase : dunu jaamu ku dul Yàlla, te nu bañ cee bokkaale dara, te kenn ci nun bañ jël moroomam jàppe ko Yàlla, di ko jaamu”. Su ñu bañee ba dummóoyu, neeleen : “Seedeleen ne nun dey way-wommatu lanu [ci topp Yàlla]”.
65يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تُحَاجُّونَ فِي إِبْرَاهِيمَ وَمَا أُنزِلَتِ التَّوْرَاةُ وَالْإِنجِيلُ إِلَّا مِن بَعْدِهِ ۚ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
Yéen ñoñ-téere, ana lan moo waral ngeen di dàggasante ci mbiri Ibraahiima, te Tawreet ak Injiil ginnaawam lañu wàcc ? Moo ndax dungeen xel-lu ?
66هَا أَنتُمْ هَٰؤُلَاءِ حَاجَجْتُمْ فِيمَا لَكُم بِهِ عِلْمٌ فَلِمَ تُحَاجُّونَ فِيمَا لَيْسَ لَكُم بِهِ عِلْمٌ ۚ وَاللَّهُ يَعْلَمُ وَأَنتُمْ لَا تَعْلَمُونَ
Yëgleen ne dàggasante ngeen ci lu ngeen xam [mbiri Iisaa]. Lu tax ngeen di dàgge ci lu ngeen amul xam-xam [Mbiri Ibraahiima] ? Yàlla xam na te yéen xamuleen.
67مَا كَانَ إِبْرَاهِيمُ يَهُودِيًّا وَلَا نَصْرَانِيًّا وَلَٰكِن كَانَ حَنِيفًا مُّسْلِمًا وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Ibraahiima nekkul woon yahuud, du càggéeni mu nekkoon nasraan. Waaye nekkoon na kuy wéetal Yàlla, di ku wommatu jëm ci Yàlla. Te bokkul woon ca ñay bokkaale..
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
65Aaya

Tekki — Aali Imran 65

Simoore Aali Imran Aaya 65 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yéen ñoñ-téere, ana lan moo waral ngeen di dàggasante ci…

Simoore Aaya 65/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 63–67. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers